text
stringlengths
38
33.7k
guddig keroog buur telee nelaw , daldi santaane nu indil ko teere ba nu dippee xew xew ya . ci kaw loolu nu di ko jangal buur . ca lanu gis nu bind ca ne mardose moo boole woon bigtan ak teres , naari fara buntu
yeeme na ! ni mu woyee woy wi , xamni bees koy deglu , man di yeg mettitu jamono ja , ak it aal ji mu ko doon woyee , lepp mu dexenaale ko ci woy wi , ba manees ko cee fekk .
da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat
fu ma jublu nu di ma ree , di ma naawal , may gis .
bokk yi , yeen ni yalla begg , xam nanu ne yalla tann na leen
loxob nasaraan biy indi ñam fa jak ndimal ñeel daw làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi
dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci bundesrat di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cér ñu séddale leen ci nguur nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatóóor gu almaañ gi
mu am kurelu xareb filisteen nu dal betleyem .
te bokk naa ak ñoom yaakaar ci yàlla ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam
naari gànnar yi daana ñu song ñi dëkk ci tàkkal dex gi
suufu waa keram , ku nekk it wara dellu ca lang ga mu bokk . seen atum yiwiku la atum juroom fukkeel boobu di doon . dungeen ci ji , dungeen ci goobaat lu saxe ca seen um ngoob te dungeen ci wolli ag resen , di ko witt . gannaaw atum yiwiku la , na doon at mu ngeen sellal . saxayaayub tool ngeen sana lekk .
bi nu ko defee mu ne leen yeen bokki israyil , moytuleen li ngeen di def nit noonu .
moo tax nanguleen ci woyof kaddu , gi leen yalla sol te man leen a musal , di deddu bepp sobe ak coxor gi daj addina .
moom lanuy jappe natteel ci dawaan yu mag yu diiney jenn yalla yi bokk ci njabootugdiiney ibraayma yi .
bu may xéye fii ci fajar damay yooru waaye bala maa àgg màrse oto bi fees
ginaaw bi lañu def washington ginaaw bi mu nekke péeyu koom koom bi ak bu alal bi la nu ko def péey bu politig bi
soxna mooy baat bu nuy jox kilifa gu jigeen , bu doon goor la serin lees di wax .
ku ji ngir sa nafsu , dinga goob li sa nafsu menn , maanaam ag yaqute .
moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngëneel ak tawfeex tey borom li fii ak la fee
waaye yalla nee na xeet wi leen jaamloo , man maa leen di atte te gannaaw loolu dinanu genn , di ma jaamu ci berab bii .
guddig keroog nag kaddug aji sax ji dikkal natan , ne ko demal wax sama jaam daawuda , ne ko aji sax ji dafa wax ne ndax yaw yaa may tabaxal ker gu ma dekke ? bes ba ma gennee banni israyil misra ba tey jii , masumaa dekke ci ker . ci biir xaymab jaamookaay laa masa mange . mboolem fu ma masa mangeji ak banni israyil gepp , ndax mas naa wax benn baat , jeme ci genn giirug israyil gu ma sant nu samm israyil sama non , ne leen nu tabaxal ma kerug bantu seedar ?
ki féete ci yoon wi mooy ki dégg seytaane ñëw ci saa si këf kàddu gi ñu def ci moom
sammal ko sama ngor ba faww , feddlil ko sama kollere .
yanu mbej , ag jagle gu dattu la ci wall wallaani ab ne ne , mooy tax seenug man a digaale ci ndimbalu tooli mbejbijjaakon yi .
noonu kenn nit ne ko sa yaay ak say rakk nu ngi nii taxaw ci biti , begg a wax ak yaw .
fekk na booba besu jeggi ba , di maggalu yawut ya , jubsi .
bumu doon it ci yerusalem ndax moo di dëkku buur bu mag bi
abdul laah nag moo nekkoon doom ji mu genoon a sopp ngir yewwu gi mu defoon ak njub gi , rafetug jikko yi ak nangul baayam gi .
bu dee giir yeek dekk dekkaan yi , noom danu doon xeex ci seenug anam , maanaam di def ay cong yu taqalikoo , fii ak fee door laqu guerilla .
mugabe bokk na ci ni jot ci nguur ganaaw banu xeexee lu yagg ngir askan wa moom boppam , leegi , sama wax dina deger de jarinul aw askanam , mooy sama gis gis , la ci teg .
loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub faraas bii tuddoon luwis mu fukkeel meek neent man maay nguur gi .
te du tee sama wall di sax ba faww , sama njekk it du dagg .
bi muy dem galile waroon na jaar ci diiwaanu samki
su ma yëgoon indaale fulaar gu ma teg sama bopp fii dafa bare pënd
te bàyyi xeebante xaroo xoddiku yaw te ngay xereñ te jéem a xejj jëm ca kaw
woor weeru koor lu war la ci alquraan ak sunna ak dajeg xeet wi ijmaahul umma , yalla nee na t .
li moo tax it , mandi ak baynuk ak joolaa yi , ay sant yu bare lanu bokkante saane , maane , jaabi , jeeme , sambu , jaata , saana .
noonu santaane naa ñu aj ko ba keroog ma koy yónnee sesaar
ayca ! mott ! soreleen sama waa reew , yeen ak seeni bokk ! laggleen , jaamuji aji sax ji , li ngeen begg . te itam yobbaaleleen seen juroo jur , gu gudd ak gu gatt , li ngeen begg rekk , te ne mott ! waaye naanaaleleen ma seen yalla nag , mu barkeel ma .
bi ñu ceree ba noppi yaay ji fi nga xamee ni fa la jóob di toog mu del fa yaxi nagi daaw yax yoo xam ni benn suux nekku ci
waxal waa siyon seen buur a ngi new ci yeen ku lewet la , te war mbaam sef , dig cumbur , doomu mbaam .
te loolu jaaxalu nu , ndaxte seytaane moom ci boppam day mbubboo malaakam leer .
te bu sama deret waree tuuru sax , ngir seen ngem mat sekk , ma mel ni naan gu nu boole ak sarax su jem ci yalla , ba tey beg naa ci , te dinaa ci begati .
ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji ba du jur njariñ
nu joge fa ca elleg sa , new ba ca dekku sesare .
bokkoon na ci ni dar barag naari mbooloo ba njekk moo di lingeer miy yaayu buur bi ak aawo miy soxnaay buur su njekk , moom moo am teraraagaay toog ca gangunaay mooy toogu gu buur ga .
benn ci jeexiitalu jallub dawaan ci ab wommatukaay , mooy nuggaayam , la nuy wax jeexiitalu joule .
ku nekk ci kaw taax mi , bul wacc ngir dugg ker gi , fab say yef ya fa nekk .
naka sunu diggante ak yéen ñi gëm doxal nanu ko doxalin wu sell te jub te amul sikk
ñu wara xam ni seex anta joob ak yeneen gestu kat wone nañu ko lakk boobu amoon ca isipt boobu ak lakk wolof ñoo bokk maam
soxor bi da koy gis , mer , inaan bay yeyu , jeex takk
noonu sàmmleen seen dundin waxuma ni ñu amul xel waaye ni ñu am xel tey jariñoo jot gi ndaxte nu ngi ci jamono ju bon
benamin ca sela . nu def la buur santaane lepp . gannaaw loolu yalla nangul reew ma .
amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu yawut ya mépp ak ca dëkku yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga maanaam tir ak sidon
ku bon ay nedd ay fanam ci biir teraanga , doora jekki wacci njaniiw .
bëggul woona dem diiwaanu yude ndaxte yawut ya dañu ko doon wuta rey
mboolem yeen ni doon naawlu tiisu yerusalem , bokkleen ak moom xolam bu sedd .
seeni laaf ñoo doon yiir kubéeru saraxu njotlaay ga
ca yooya jamono garmiy yudaa daan nanu bindanteek tobya lu bare . bare na sax ci waa yudaa nu faroon ak moom ci kaw ngin , ndax la mu doon denc doomu sekana , ma ara di baayam , te doomam yowanan di denc doomu mesulam ma berekya di baayam . rax ci dolli nu di ma gemloo ag mbaaxam , te di ko jottli samay kaddu . tobya nag yonnee ma ay bataaxal , di ma xoqtal .
su boobaa , asamaan yi dinanu lakk , ba naaw ni pend , te lu nekk ci addina dina lakk , ba seey nib doom .
waa fraans nag ñoom ñoo mujjoon a duggsi waa angalteer waa espaañ ak waa portigaal ci lefum wuññi mi ñoom seeni tukkiy wuññi daa jëmi woon kanadaa
waaye yaw aji sax ji , jege nga , te sa santaane yepp a deggu .
geneen it feeñati gu yéwénal ci bohimiya ci njiitul john hess 1373 1415 g moom mooy ki ne woon ag diggale wart a am ci diggante nit ak boroomam ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci injiil
waxuma ngeen def ko noon , waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk .
bi piyeer duggee nag korney daje ak moom daanu ciy tànkam sargal ko
72 topp nu musal ña ragaloon yàlla nu bàyyi ña tooñoon ñu bóof ca biir
lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis ci lepp li ngay def te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis kon na ngeen koy fuglu
ku am , dees na la dollil , waaye ku amul , dees na nangu sax li nga xalaatoon ne , am nga ko ba noppi .
bi nu deggee loolu , nuy rocceeku kenn kenn , mag na jiitu .
yal na leen seen ndey sax fatte , sax yi muucu leen ,
bénn la ci diwaan yi ñu séddalee goxu afrig
ci noonu nu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne george washington moo leen jiite woon .
loolu lu baax la waaye xamal ne jinne yi it gëm nañu loolu ba dañoo tiit bay lox
ndax maasug defkati njekkar lanu , doom yu nakk kollere .
ba mu ko defee elasar sarxalkat ba wax ak na xareji woon , ne leen lii moo di dogalu yoon , bi aji sax ji denk musaa luy wurus ak xaalis ak xanjar , ak wen gu nuul , ak wen gu weex , ak beteex , mboolem lu dul lakk , rekk , nangeen ko laalale sawara , mu set . ndoxum setlu mi it , warees na koo dellu setale yooyii . waaye mboolem luy lakk , ci ndoxum setal mi do lees koy dugal , ngir mu set . besub juroom naareel ba , footleen seeni yere , daldi set . gannaaw loolu man ngeena duggsi ci dal bi .
sa maam a jekka bakkaar , ni lay teewal teg ca gantal ma ,
mu seddoo ak ay kangam alalu xareem , ngir moo jebbale bakkanu boppam ,
bu la cib ràkka rawee jugal kàbbar jàng faatiya akuw saar cig birël bu la ci ñaari ràkkaa rawee jugal te bul kàbbar jàng faatiya akuw saar te birël ko taaya defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël
kon ma addooti ndax jaaxle , ba xol jallaanoo .
kenn ci surgay saraxalekat bu mag ba , di mbokku ka piyeer coroon noppam , ne piyeer xanaa du yaw laa gisoon ak moom ca tool ba ?
expected identifier for class selector but found s .
nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax
sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar benn neexu la ci
ndaxte xamoon na ne kiñaan rekk a taxoon ñu jébbal ko ko
nu rabb kaalag deg , teg ko ci boppam , teg bantu xat ci loxol ndeyjooram , sukk ci kanamam , di ko naawal ne ko nuyu nanu la , yaw buuru yawut yi !
bu dee voltaire 1694 1778 g moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu faraas wi jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy nga xam ne taalifi jam lañu woon ak yéjj saboote
bu ko defee imbraatóorug almaañ gi daal di sosu dib xew xew nag bu fés ci taarixu tugal bu bees bi boroom gàngunaay gi imbratóoru almaañ bi mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur nguuraan yu almaañ yi
ba noppi ay mandinke yu juge nguuru kaabu , new ca seereer sa , dekk ak noom .
muy tollook wannikug bu nu ko mengaleek atum .
coppite yi neel toolu bijjaakon wii xetu jagleel moo lay won coppite yu mujj ci xet yi lekkalook wii .
keroog nga woo ma wall , duma wuyu , nga seet ma , seet , doo ma gis .
dara fatteloowuma ko lu dul seytaane , be fattalikuwuma ko .
ni nuy robe saaysaay lanu ko robe , denc ko ci bammeelu boroom alal , soxorul , fenul .
kaddug aji sax ji dikkal na ma ne ma yaw nag nit ki , yekkatil kaddu , jooye ko dekkub tir . waxal tir mi tooge buntu geej , jula yooyuy jeflanteek xeeti dun yu bare , nga ne ko boroom bi aji sax ji
dundalaat na nu ak kirist , fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy bakkaar ci kaw yiwu yalla ngeen mucce .
guleet isaa sall bokk ci palug njiitum reew . waaye , ku fattaliku jaar jaaram , dinga gis ne jotoon naa bokk ciy wote . waaw , isaa sall nekkoon na fi njiitu ndajem diiwaanu fatig ci njeexitalu atiy . ginnaaw loolu , askan wi woolu woon na ko ba fal ko dipite ci atum .
dañu ciy wax ci injiil ci mc 21 1 mk 11 1 lu 19 29
doomi yanqooba nag def la leen seen baay denkoon , yobbu ko ca reewu kanaan , daldi koy rob ca xunti ma ca toolub magpela , te ibraayma jendoon ko ca efron , etteen ba , ngir def ko bammeel . mooy tool , ba jakkaarloo ak mamre . ba yuusufa dencee baayam ba noppi , dafa dellu misra , moom ak doomi baayam ya ak mboolem , na mu andaloon ca robu baayam .
lu bon loolu lépp day génn ci nit di ko indil sobe
benn dëkk ci diiwaanu maseduwan la woon ci wetu géej ga tudd géeju ese