sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
6
17
{ "fr": "Et si Allah fait qu´un malheur te touche, nul autre que Lui ne peut l´enlever. Et s´Il fait qu´un bonheur te touche... c´est qu´Il est Omnipotent.", "wo": "Su la Yàlla tegee metit, kenn du mën a teggi lor jooju ku dul Moom. Su la joxee yiw, xamal ne Moom lu nekk la mën." }
6
18
{ "fr": "C´est Lui Dominateur Suprême sur Ses serviteurs; c´est Lui le Sage, le Parfaitement Connaisseur.", "wo": "Te Moom Aji-not la ci kaw jaam ñi ; Ku xereñ la [Moom Yàlla], Ku deñ la ci kumpa." }
6
19
{ "fr": "Dis : \"Qu´y a-t-il de plus grand en fait de témoignage ? \" Dis : \" Allah est témoin entre moi et vous; et ce Coran m´a été révélé pour que je vous avertisse, par sa voie, vous et tous ceux qu´il atteindra.\" Est-ce vous vraiment qui attestez qu´il y ait avec Allah d´autres divinités ? Dis : \"Je n´atteste pas\". Dis [aussi]: \"Il n´y a qu´une Divinité Unique. Et moi, je désavoue ce que vous (Lui) associez\".", "wo": "Neel : “ Ana lan moo gën a màgg ci wàllu seede ?” . Neel : “Yàlla dana nekk seede ci sama diggante ak yéen ; te sol nañu ma Alxuraan jii ngir ma waar ci yéen ak képp ku ca jot.” . Moo ndax dangeen di seede ne am na jeneen yàlla ju dul Yàlla ? Neeleen : “Seedewuma loolu” . Neel: “Moom daal nekkul lu dul jenn Yàlla doŋŋ. Te man set naa wecc ci li ngeen koy bokkaale” ." }
6
20
{ "fr": "Ceux à qui Nous avons donné le Livre reconnaissent (le Messager Muhammad) comme ils reconnaissent leurs propres enfants. Ceux qui font leur propre perte sont ceux qui ne croient pas.", "wo": "Ña nga xam ne jox Nanu leen Téere, xam nañu ko ni ñu xàmmee seeni doom. Ña yàqal seen bopp duñu gëm de." }
6
21
{ "fr": "Qui donc est plus injuste que celui qui invente un mensonge contre Allah, ou qui traite de mensonge Ses versets ? Les injustes ne réussiront pas.", "wo": "Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla aw fen, walla di weddi ay kàddoom ? Tooñkat ya duñu texe de." }
6
22
{ "fr": "Et le Jour où Nous les rassemblerons tous puis dirons à ceux qui auront donné des associés : \"Où sont donc vos associés que vous prétendiez ?", "wo": "Ca bis ba ñu leen di fang ñoom ñépp [dajale leen], bu ñuy wax ak ña daan bokkaale, ne leen : “ Ana ña ngeen sosoon, bokkaale woon leen ak Yàlla ?" }
6
23
{ "fr": "Alors il ne leur restera comme excuse que de dire : \"Par Allah notre Seigneur ! Nous n´étions jamais des associateurs\".", "wo": "Su ko defee, seen njàqare duleen xiir ci leneen lu dul ñuy wax naan : “Giñ nanu ci Yàlla sunu Boroom ne nekkunu woon di way-bokkaale” . " }
6
24
{ "fr": "Vois comment ils mentent à eux-mêmes ! Et comment les abandonnent (les associés) qu´ils inventaient !", "wo": "Gisal ni ñuy fenee seen bopp ! Te dana fekk la ñu daan duur réer leen mërr !" }
6
25
{ "fr": "Il en est parmi eux qui viennent t´écouter, cependant que Nous avons entouré de voiles leurs coeurs, qui les empêchent de comprendre (le Coran), et dans leurs oreilles est une lourdeur. Quand même ils verraient toutes sortes de preuves, ils n´y croiraient pas. Et quand ils viennent disputer avec toi, ceux qui ne croient pas disent alors : \"Ce ne sont que des légendes des anciens\".", "wo": "Am na ci ñoom ñu lay déglu, waaye def Nanu ci seen xol muuraay ba duñu am dégg-dégg ci Alxuraan, te ca seeni nopp, def Nanu ca saañ. Tax na bu ñu gisee laaya, ju mu mën di doon, ne duñu ko gëm. Ba ba ñuy ñëw dàggasanteek yaw, dañuy wax ñoom ñi weddi : “Lii du dara lu dul léebi mag ñu njëkk ña” ." }
6
26
{ "fr": "Ils empêchent [les gens] de s´approcher de lui et s´en écartent eux-mêmes. Ils ne feront périr qu´eux-mêmes sans s´en rendre compte.", "wo": "Te ñoom dañuy tere ku jegeñ Yonent bi, te di ko sori. Waaye alaguñu kenn ku dul seen bopp te bëgguñu ko.(s)" }
6
27
{ "fr": "Si tu les voyais, quand ils seront placés devant le Feu. Ils diront alors : \"Hélas ! Si nous pouvions être renvoyés (sur la terre), nous ne traiterions plus de mensonges les versets de notre Seigneur et nous serions du nombre des croyants\".", "wo": "Cëy boo leen gisoon, fa ñu leen taxawale ca Safara. Te ñuy wax : “Ngalla nun ! Yelante kon ñu delloo nu àddina, ba dunu weddi kàddug Yàlla sunu Boroom, bokk ca way-gëm ña” ." }
6
28
{ "fr": "Mais non ! Voilà que leur apparaîtra ce qu´auparavant ils cachaient . Or, s´ils étaient rendus [à la vie terrestre], ils reviendraient sûrement à ce qui leur était interdit. Ce sont vraiment des menteurs.", "wo": "Li wér mooy, la ñu doon nëbb, bu jëkkoon feeñ na ca ñoom. Te bu ñu leen delloo woon it, ñu dellu di def la ñu leen tere woon. Ca dëgg- dëgg ñoom ay fenkat lañu." }
6
29
{ "fr": "Et ils disent : \" Il n´y a pour nous [d´autre vie] que celle d´ici-bas; et nous ne serons pas ressuscités\".", "wo": "Dañuy wax ne : “ Amul geneen dundu gu dul gu àddina bii ; [nun bu nu faatoo] kenn du nu dekkalaat” ." }
6
30
{ "fr": "Si tu les voyais, quand ils comparaîtront devant leur Seigneur. Il leur dira : \"Cela n´est-il pas la vérité ? \" Ils diront : \"Mais si ! Par notre Seigneur ! \" Et, il dira : \"Goûtez alors au châtiment pour n´avoir pas cru\".", "wo": "Cëy boo leen gisoon bu ñu leen taxawale ca seen Boroom. Mu ne leen : “Ndax lii du dëgg ?” Ñu toonte ne : “Axakañ ! Giñ nanu ko ci sunu Boroom !” Mu ne leen : “Léegi nag, mosleen mbugal mi ngeen daan weddi” ." }
6
31
{ "fr": "Sont perdants certes ceux qui traitent de mensonges la rencontre d´Allah. Et quand soudain l´Heure leur viendra, ils diront : \"Malheur à nous pour notre négligence à son égard , Et ils porteront leurs fardeaux sur leurs dos, et quels mauvais fardeaux !", "wo": "Ña daan weddi ne dajeek Yàlla am na, yàqule nañu. Su Bis-pénc ba nee xes ci seen kaw nag, ñuy wer-weri naan : “Wooy nun yàqule nanu ndax la nu ca sàggane woon. Ñu boot seen bàkkaar ya, ndaw yen bu bon !" }
6
32
{ "fr": "La présente vie n´est que jeu et amusement. La demeure dans l´au-delà sera meilleure pour ceux qui sont pieux. Eh bien, ne comprenez-vous pas ?", "wo": "Dundug àddina nekkul lu dul po ak i caaxaan. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dungeen xel-lu ?" }
6
33
{ "fr": "Nous savons qu´en vérité ce qu´ils disent te chagrine. Or, vraiment ils ne croient pas que tu es menteur, mais ce sont les versets (le Coran) d´Allah, que les injustes renient.", "wo": "Xam Nanu xéll ne li ñuy wax metti na la lool. Tooñkat ya, du yaw lañuy weddi, waaye kàdduy Yàlla lañu weddi." }
6
34
{ "fr": "Certes, des messagers avant toi (Muhammad) ont été traités de menteurs. Ils endurèrent alors avec constance d´être traités de menteurs et d´être persécutés, jusqu´à ce que Notre secours leur vînt. Et nul ne peut changer les paroles d´Allah, et il t´est déjà parvenu une partie de l´histoire des Envoyés.", "wo": "Weddig ay Yonent yu la jiitu amoom na fi. Ñu muñ loraange ja, ba Nu dikke leen Sunu ndimbal. Kàddug Yàlla du soppiku, te jot nga lenn ca xew-xewi Yonent ya." }
6
35
{ "fr": "Et si leur indifférence t´afflige énormément, et qu´il est dans ton pouvoir de chercher un tunnel à travers la terre, ou une échelle pour aller au ciel pour leur apporter un miracle , [fais-le donc]. Et si Allah voulait, Il pourrait les mettre tous sur le chemin droit. Ne sois pas du nombre des ignorants.", "wo": "Ndagam seen dëddu dafa rëy ci yaw, boo mënee sàkk ag tajfal ci biir suuf si, walla ker- keraan ci asamaan yi ba tax nga indil leen kéemaan, def ko. [Xamal ne] bu neexoon Yàlla, Mu dajale leen cig njub. Kon bul bokk ca ña sànku réer." }
6
36
{ "fr": "Seuls ceux qui entendent répondent à l´appel [de la foi].Et quant aux morts, Allah les ressuscitera; puis ils Lui seront ramenés. .", "wo": "Ñay dégg ñoo lay wuyu. Ña dee, Yàlla Dana leen dekkal ; ñu dellusi ca Moom.(h)" }
6
37
{ "fr": "Et ils disent : \"Pourquoi n´a-t-on pas fait descendre sur lui (Muhammad) un miracle de la part de son Seigneur ? \" Dis : \" Certes Allah est capable de faire descendre un miracle. Mais la plupart d´entre eux ne savent pas\".", "wo": "Te ña ngay wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom kéemaan gu tukke ci Yàlla ?” . Neel : “Yàlla ku am kàttan la ci wàcce kéemaan. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu” ." }
6
38
{ "fr": "Nulle bête marchent sur terre, nul oiseau volant de ses ailes, qui ne soit comme vous en communauté. Nous n´avons rien omis d´écrire dans le Livre. Puis, c´est vers leur Seigneur qu´ils seront ramenés.", "wo": "Amul lenn luy dukkat ci suuf, du caageene luy naawe ñaari laaf, lu dul ne dañoo doon ay xeet [waasoo] ni yéen. Amul lenn lu Nu bàyyi ci Téere bi. [Xamleen ne] dees na leen fang jëme ci seen Boroom, gur- gur jiital wëtal." }
6
39
{ "fr": "Et ceux qui traitent de mensonges Nos versets sont sourds et muets, dans les ténèbres. Allah égare qui Il veut; et Il place qui Il veut sur un chemin droit.", "wo": "Te ña weddi Sunuy kàddu, dañoo tëx, luu, gumba. Yàlla ku ko soob, mu bàyyi ko cig réeram ; ku Ko soob Mu teg ko ci yoon wu jub wa xocc." }
6
40
{ "fr": "Dis : \"Informez-moi : si le châtiment d´Allah vous vient, ou que vous vient l´Heure, ferez-vous appel à autre qu´Allah, si vous êtes véridiques ? \"", "wo": "Neel : “Waxleen ma : ndax su leen mbugalum Yàlla dalee, walla Bis- pénc ba na jaseet ci seen kaw, su fekkee li ngeen di woote dëgg la ci yéen, moo ndax kon dangeen fawoo keneen ku moy Yàlla ?”" }
6
41
{ "fr": "C´est plutôt à Lui que vous ferez appel. Puis, Il dissipera, s´Il veut, l´objet de votre appel et vous oublierez ce que vous [Lui] associez.", "wo": "Déedéet, Moom ci boppam ngeen di woo. Mu xar lor ja su ko soobee, ngeen daldi fàtte ya ngeen daan bokkaale." }
6
42
{ "fr": "Nous avons, certes, envoyé (des messagers) aux communautés avant toi. Ensuite Nous les avons saisies par l´adversité et la détresse - peut-être imploreront-ils (la miséricorde) ! -", "wo": "Te yónnee woon Nanu ca xeet ya la jiitu. Nu tegoon leen coonay ñàkk ak i naqar - ndax Yàlla ñu jànge ca toroxlu ! -" }
6
43
{ "fr": "Pourquoi donc, lorsque Notre rigueur leur vînt, n´ont-ils pas imploré (la miséricorde) ? Mais leurs coeurs s´étaient endurcis et le Diable enjolivait à leurs yeux ce qu´ils faisaient.", "wo": "Su fekkoon ba leen coono dalee toroxlu nañu, sax [nga ne waaw] ? Waaye seeni xol dafa wow, Séytaane daldi leen koy jékkalal ak la jëf ja di ju nu lébbi." }
6
44
{ "fr": "Puis, lorsqu´ils eurent oublié ce qu´on leur avait rappelé, Nous leur ouvrîmes les portes donnant sur toute chose (l´abondance); et lorsqu´ils eurent exulté de joie en raison de ce qui leur avait été donné, Nous les saisîmes soudain, et les voilà désespérés.", "wo": "Ba ñu fàttee la Nu leen waare woon nag, ubbil Nanu leen buntu [teraanga] bu nekk ; ba ñu bég ca la Nu leen jox, Nu seet seet ne xes ca seen kaw ak sànje bu dootul dog, ñu ne tocc." }
6
45
{ "fr": "Ainsi fut exterminé le dernier reste de ces injustes. Et louange à Allah, Seigneur de l´Univers !", "wo": "Dogeef na ginnaawug ña tooñoon. Te nag Yàlla miy Boroom àddina bi rekk a yayoo cant !" }
6
46
{ "fr": "Dis : \"Voyez-vous ? Si Allah prenait votre ouïe et votre vue, et scellait vos coeurs, quelle divinité autre qu´Allah vous les rendrait ? Regarde comment, à leur intention, Nous clarifions les preuves ! Pourtant ils s´en détournent.", "wo": "Waxleen ma : “Bu Yàlla téye woon seenug dégg, ak seenug jis, tëj seeni xol, ana keneen ku dul Yàlla ku leen mën a delloo yooyu ? Gisal ni Yàlla di leerale ay tegtalam ! Ba noppi ñoom ñuy jeng." }
6
47
{ "fr": "Dis : \"Que vous en semble ? Si le châtiment d´Allah vous venait à l´improviste ou au grand jour, qui seront détruits sinon les gens injustes ? \"", "wo": "Waxleen ma : “Ndax bu mbugëlam Yàlla nee xes ci yéen walla muy lu fés, ndax kenn dana ca loru ku dul ña di way-tooñ ?” " }
6
48
{ "fr": "Nous n´envoyons des messagers qu´en annonciateurs et avertisseurs : ceux qui croient donc et se réforment, nulle crainte sur eux et ils ne seront point affligés.", "wo": "Dunu yónni ay Yonent lu dul ne ñoom dañuy xuppeek a bégle : ña gëm te sellal, yéwénal, njàqare duleen dal, duñu am naqar.(s)" }
6
49
{ "fr": "Et ceux qui traitent de mensonges Nos preuves, le châtiment les touchera, à cause de leur perversité.", "wo": "Ña weddi Sunuy kàddu, mbugal dana leen sóor ndax la ñu daan jalgati." }
6
50
{ "fr": "Dis[-leur]: \"Je ne vous dis pas que je détiens les trésors d´Allah, ni que je connais l´Inconnaissable, et je ne vous dis pas que je suis un ange. Je ne fais que suivre ce qui m´est révélé.\" Dis : \"Est-ce que sont égaux l´aveugle et celui qui voit ? Ne réfléchissez-vous donc pas ? \"", "wo": "Neel: “Dumaleen wax it ne Malaaka laa, li am mooy li ñu ma soloo doŋŋ laay topp.” . Neel : “Ndax mënees naa yemale gumba ak njàccaar ? Moo ndax dangeen dul xel-lu ?”" }
6
51
{ "fr": "Et avertis par ceci (le Coran), ceux qui craignent d´être rassemblés devant leur Seigneur, qu´ils n´auront hors d´Allah ni allié ni intercesseur. Peut-être deviendraient-ils pieux !", "wo": "Artul ak Alxuraan, ñi ragal, ñu fang leen jëme fa seen Boroom, amuñu leneen kiiraay, du caageene ab rammukat. Ndax xéy-na ñu ragal Yàlla !" }
6
52
{ "fr": "Et ne repousse pas ceux qui, matin et soir, implorent leur Seigneur, cherchant Sa Face \"Wajh\". Leur demander compte ne t´incombe en rien, et te demander compte ne leur incombe en rien. En les repoussent donc, tu serais du nombre des injustes. .", "wo": "Bul dàq ñiy jaamu seen Boroom suba ak ngoon ngir bëgg jëmmam [Yàlla]. Dara waru la ci àtte seeni mbir, ñoom it dara waruleen ci àtte say mbir. Ba tax na, boo leen dàqee daldi bokk ca tooñkat ya." }
6
53
{ "fr": "Ainsi, éprouvons-Nous (les gens) les uns par les autres , pour qu´ils disent : \"Est-ce là ceux qu´Allah a favorisés parmi nous ? \" N´est-ce pas Allah qui sait le mieux lesquels sont reconnaissants ?", "wo": "Noonu la Nu notee ñenn ci ñoom jaare ko ci ñeneen ca ñoom, ngir ñu wax ne : “Ndax [ña doyadi] ñii la Yàlla xéewale ci nun ?” . Moo ndax Yàlla Moo gën a xam ña koy gëram ciy xéewalam ?" }
6
54
{ "fr": "Et lorsque viennent vers toi ceux qui croient à notre versets (le Coran), dis : \"Que la paix soit sur vous ! Votre Seigneur S´est prescrit à Lui-même la miséricorde. Et quiconque d´entre vous a fait un mal par ignorance, et ensuite s´est repenti et s´est réformé... Il est, alors, Pardonneur et Miséricordieux\".", "wo": "Ña gëm Sunuy kàddu, bu ñu la dikkalee, neel : “Yal na jàmm wàcc ci yéen ! Yàlla seen Boroom dogal na ci boppam yërmaande. Li am mooy, ku def ci yéen aw ñaawtéef cig ñàkk a xam, ba mu noppee, tuub, rëccu, sellal jëfam ... Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la” ." }
6
55
{ "fr": "C´est ainsi que Nous détaillons les versets, afin qu´apparaisse clairement le chemin des criminels.", "wo": "Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat yi." }
6
56
{ "fr": "Dis : \"il m´a été interdit d´adorer ceux que vous priez en dehors d´Allah\". Dis : \"Je ne suivrai pas vos passions : car ce serait m´égarer, et je ne serais plus parmi les bien-guidés\".", "wo": "Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla” . Neel itam : “Duma topp seeni bànneex : ndax su ma ko defee, damay sànku te kon duma bokk ca ñu gindiku ña” ." }
6
57
{ "fr": "Dis : \"Je m´appuie sur une preuve évidente de la part de mon Seigneur, et vous avez traité cela de mensonge. Ce (le châtiment) que vous voulez hâter ne dépend pas de moi. Le jugement n´appartient qu´à Allah : Il tranche en toute vérité et Il est le meilleur des juges.", "wo": "Neel : “Man dama nekk ci lu bir [leer nàññ], di lu jóge fa sama Boroom, ngeen weddi ko. Li ngeen di [laaj te di ko] yàkkamti, nekkul ci man. Àpp ba, Yàlla rekk a ko moom : Mooy nettali dëgg te Mooy gën jaa mën a àtte [téqale] ay mbir." }
6
58
{ "fr": "Dis : \"Si ce que vous voulez hâter dépendait de moi, ce serait affaire faite entre vous et moi.\" C´est Allah qui connaît le mieux les injustes.", "wo": "Neel : “Bu fekkoon li ngeen di [laaj] di yàkkamti mi ngi ci man, kon mbir ya sottikoon na sama diggante ak yéen.” Te Yàllaa gën a xam tooñkat ya." }
6
59
{ "fr": "C´est Lui qui détient les clefs de l´Inconnaissable. Nul autre que Lui ne les connaît. Et Il connaît ce qui est dans la terre ferme, comme dans la mer. Et par une feuille ne tombe qu´Il ne le sache. Et pas une graine dans les ténèbres de la terre, rien de frais ou de sec, qui ne soit consigné dans un livre explicite.", "wo": "Fa Moom la caabiy kumpa nekk. Kenn xamuleen ku dul Moom. Te xam na li nekk ci jéeri ji ak géej gi. Te amul fenn xob wuy rot te xamu ko. Du caageene wenn fepp wu nekk ci biir lëndëmu suuf si, di lu tooy, di lu wow, ndare du nekk na ci ab téere bu leer nàññ.(r) " }
6
60
{ "fr": "Et, la nuit, c´est Lui qui prend vos âmes, et Il sait ce que vous avez acquis pendant le jour. Puis Il vous ressuscite le jour afin que s´accomplisse le terme fixé. Ensuite, c´est vers Lui que sera votre retour, et Il vous informera de ce que vous faisiez. .", "wo": "Moom moo leen di nelawloo guddi, te xam na la ngeen di fàggu ci bëccëg. Topp Mu yee leen ngir àtte dig buñu dogal ba. Topp nag, ngeen dellu ci Moom, Mu biral leen la ngeen doon def.." }
6
61
{ "fr": "Et Il est le Dominateur Suprême sur Ses serviteurs. Et Il envoie sur vous des gardiens . Et lorsque la mort atteint l´un de vous, Nos messagers (les Anges) enlèvent son âme sans aucune négligence.", "wo": "Te Moom mooy Aji-not ja ci kaw jaamam ya. Te Mooy yónni ci yéen ay Malaaka yu leen di wattu. Ba kero bis ba dee di agsi, ba kenn ci yéen sunuy ndaw rey ko, te ñoom sàgganuñu ci dara." }
6
62
{ "fr": "Ils sont ensuite ramenés vers Allah, leur vrai Maître. C´est à Lui qu´appartient le jugement et Il est le plus prompt des juges.", "wo": "Bu loolu jàllee, ñu delloo leen fa Yàlla, kay seen Boroom tigi. Moo ndax du Moo moom àtte ba te Moo gën a gaaw wàññikat yépp." }
6
63
{ "fr": "Dis : \"Qui vous délivre des ténèbres de la terre et de la mer ? \" Vous l´invoquez humblement et en secret : \" S´Il nous délivre de ceci, nous serons du nombre des reconnaissants.", "wo": "Neel : “Kan moo leen di musal ci lëndëmu jéeri ak gu géej ?” Te ngeen di Ko faral a woo ànd ak toroxlu ak nëbbu, naan : “ Cëy Yàlla, boo nu musalee ci lii, kon dey nu bokk ca gërëmkat ya." }
6
64
{ "fr": "Dis : \"C´est Allah qui vous en délivre ainsi que toute angoisse. Pourtant, vous Lui donnez des associés\".", "wo": "Neel : “Yàlla moo leen di musal ci loolu, ak njàqare ju mu mën di doon. Ba noppi ngeen di ko bokkaale” ." }
6
65
{ "fr": "Dis : \"Il est capable, Lui, de susciter contre vous, d´en haut, ou de dessous vos pieds , un châtiment, ou de vous confondre dans le sectarisme. Et Il vous fait goûter l´ardeur [au combat] les uns aux autres.\" Regarde comment Nous exposons Nos versets. Peut-être comprendront-ils ?", "wo": "Neel : “Moom am na kàttanug yónnee leen mbugal mu leen bawoo ci kaw walla ci seen suufi tànk, mbaa Mu dogal, ci seen biir, juuyoo. Ba ku nekk mos ngaañ la jóge ca moroomam.” Gisal ni Nuy leeralee tegtal yi ndax ñoom ñu mën koo dégg ?" }
6
66
{ "fr": "Et ton peuple traite cela (le Coran) de mensonge, alors que c´est la vérité. Dis : \"Je ne suis pas votre garant .", "wo": "Say nit weddi nañu te Moom mooy dëgg. Neeleen : “Du maa leen di sàmm." }
6
67
{ "fr": "Chaque annonce arrive en son temps et en son lieu, Et bientôt vous le saurez.\"", "wo": "Xew-xew bu ne am na waxtoon te dangeen mës a xam.”" }
6
68
{ "fr": "Quand tu vois ceux qui pataugent dans des discussions à propos de Nos versets, éloigne-toi d´eux jusqu´à ce qu´ils entament une autre discussion. Et si le Diable te fait oublier , alors, dès que tu te rappelles, ne reste pas avec les injustes.", "wo": "Boo gisee aw nit ñuy doyadal Sunuy kàddu, dëdduleen ba bañuy xuus ci weneen waxtaan. Bu la Séytaane fàtteloo ba nga fàtte ko. Saa soo ko fàttalikoo sañatoo toogandoo nag ak aw nit ñu di ay tooñkat." }
6
69
{ "fr": "Il n´incombe nullement à ceux qui sont pieux de rendre compte pour ces gens là. Mais c´est à titre de rappel. Peut-être craindront-ils [Allah].", "wo": "Ñi ragal Yàlla, kenn àtteloowuleen ñooña. Xanaa kay ñu di leen fàttali. Ndax xéy-na ñoom it ñu ragal Yàlla." }
6
70
{ "fr": "Laisse ceux qui prennent leur religion pour jeu et amusement, et qui sont séduits par la vie sur terre. Et rappelle par ceci (le Coran) pour qu´une âme ne s´expose pas à sa perte selon ce qu´elle aura acquis, elle n´aura en dehors d´Allah, ni allié ni intercesseur. Et quelle que soit la compensation qu´elle offrirait, elle ne sera pas acceptée d´elle. Ceux-là se sont abandonnés à leur perdition à cause de ce qu´ils ont acquis. Leur breuvage sera l´eau bouillante et ils auront un châtiment douloureux, pour avoir mécru.", "wo": "Bàyyil ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine am po ak i caaxaan fii ci àddina. Waarleen ci Alxuraan ndax benn bakkan bañ a yàqule ci sababus la mu doon fàggu, amul lenn kiiraay walla kuy rammu ku dul Yàlla. Te deesu ko nangul mu jotu ak menn jotu. Ñooña, dañoo alku ngir la ñu doon fàggu [ciy ñaawteef]. Naan gu tàng jérr lañuy jolu ak mbugal mu metti, ndax la ñu doon weddi.(s)" }
6
71
{ "fr": "Dis : \"Invoquerons-nous, au lieu d´Allah, ce qui ne peut nous profiter ni nous nuire ? Et reviendrons-nous sur nos talons après qu´Allah nous a guidés, comme quelqu´un que les diables ont séduit et qui erre perplexe sur la terre, bien que des amis l´appellent vers le droit chemins (lui disant) : - \"Viens à nous.\" Dis : \"Le vrai chemin, c´est le chemin d´Allah. Et il nous a été commandé de nous soumettre au Seigneur de l´Univers,", "wo": "Neel : “Moo ndax danuy jaamu loo xam ne dunu jariñ, dunu lor, bàyyi Yàlla ? Kon dey nu dellu ginnaaw, te fekk Yàlla gindi nanu ba noppi, mel ni ka nga xam ne Séytaane dakoo réeral ci kaw suuf, muy ku gëlëm, ay àndandoom di ko woo ci njub, naan ko : - “Ñëwal ci nun.” . Neel : “Njubug Yàlla mooy dëggi-dëggi njub. Te am nanu ndigal ci wommatu jëm ci Boroom àddina si," }
6
72
{ "fr": "ET d´accomplir la Salat et de Le craindre. C´est vers Lui que vous serez rassemblés\".", "wo": "te it ngeen taxawal julli te ragal Ko. Fa Moom kat lañu leen di dajale yéen ñépp” ." }
6
73
{ "fr": "Et c´est Lui qui a créé les cieux et la terre, en toute vérité. Et le jour où Il dit : \"Sois ! \" Cela est , Sa parole est la vérité. A Lui, [seul,] la royauté, le jour où l´on soufflera dans la Trompe. C´est Lui le Connaisseur de ce qui est voilé et de ce qui est manifeste. Et c´est Lui le Sage et le Parfaitement Connaisseur.", "wo": "Moom mooy ki sàkk asamaan yeek suuf si ci dëgg. Ca bis ba Mu nee : “Nekkal !” . Mu daldi nekk, Ay waxam mooy dëgg. Te Moo moom nguur, bis ba ñuy ëf buft bi. Mooy xamaakoonu kumpa ak li fés. Te Mooy ku xereñ ki, deñ ciy kumpa." }
6
74
{ "fr": "(Rappelle le moment) où Abraham dit à Azar, son père : \"Prends-tu des idoles comme divinités ? Je te vois, toi et ton peuple, dans un égarement évident ! \"", "wo": "(Te nga fàttaliku) ba Ibraahiima waxee baayam [Aazar] : “Ndax dangay jël ay xërëm def leen ay yàlla ? Man dey gis naa ne, yaak saw nit, yéen a ngi ci réer gu tar !”" }
6
75
{ "fr": "Ainsi avons-Nous montré à Abraham le royaume des cieux et de la terre, afin qu´il fût de ceux qui croient avec conviction.", "wo": "Noonu Lanu wonee Ibraahiima moomeelu asamaan yi ak suuf si, ndax mu bokk ca way- wóolu ña." }
6
76
{ "fr": "Quand la nuit l´enveloppa, il observa une étoile, et dit : \"Voilà mon Seigneur ! \" Puis, lorsqu´elle disparut, il dit : \"Je n´aime pas les choses qui disparaissent\".", "wo": "Ba guddi lëndemee ci moom, mu gis benn bidiw, mu daldi ne : “Sama Yàllaa ngi nii !” Waaye, ba bidiw ba suuxee, mu ne : “Man daal soppuma ñiy suux” ." }
6
77
{ "fr": "Lorsqu´ensuite il observa la lune se levant, il dit : \"Voilà mon Seigneur ! \" Puis, lorsqu´elle disparut, il dit : \"Si mon Seigneur ne me guide pas, je serai certes du nombre des gens égarés\".", "wo": "Ba mu gisee weer wi mu feq, mu ne : “Sama Yàllaa ngii !” . Waaye, ba mu suuxee, mu ne : “Bu ma sama Boroom gindiwul, fàwwu danaa bokk ca nit ñu réer ña” ." }
6
78
{ "fr": "Lorsqu´ensuite il observa le soleil levant, il dit : \"Voilà mon Seigneur ! Celui-ci est plus grand\" Puis lorsque le soleil disparut, il dit : \"ô mon peuple, je désavoue tout ce que vous associez à Allah.", "wo": "Ba mu gisee jant ba fenk, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! Jii moo gën a màgg” . Ba mu suuxee, mu ne : “Yéen samaw nit, man dey deñ naa ba set wecc ci lii ngeen di bokkaale ak Yàlla." }
6
79
{ "fr": "Je tourne mon visage exclusivement vers Celui qui a créé (à partir du néant) les cieux et la terre; et je ne suis point de ceux qui Lui donnent des associés.\"", "wo": "Man jébbalu naa ci Ki sos asamaan yeek suuf si ; di ku Ko wéetal, man dey bokkuma ci way-bokkaale ya.”" }
6
80
{ "fr": "Son peuple disputa avec lui; mais il dit : \"Allez-vous disputer avec moi au sujet d´Allah, alors qu´Il m´a guidé ? Je n´ai pas peur des associés que vous Lui donnez. Je ne crains que ce que veut mon Seigneur. Mon Seigneur embrasse tout dans Sa science. Ne vous rappelez-vous donc pas ?", "wo": "Aw nitam dàggasanteek moom ; mu ne leen : “Moo ndax dangeen di dàggasanteek man ci Yàlla, te man gindi Na ma ? Ragaluma li ngeen koy bokkaale lu dul lu Yàlla namm. Xam- xamu sama Boroom peeg na yëf yépp. Moo ndax dangeen dul fàttaliku [xalaat] ?(n)" }
6
81
{ "fr": "Et comment aurais-je peur des associés que vous Lui donnez, alors que vous n´avez pas eu peur d´associer à Allah des choses pour lesquelles Il ne vous a fait descendre aucune preuve ? Lequel donc des deux partis a le plus droit à la sécurité ? (Dites-le) si vous savez.", "wo": "Te sax man, naka laay ragale li ngeen Koy bokkaale te yéen ragaluleen ne yéen, yéen a ngi bokkaleek Yàlla yoo xam ne wàcceluñu leen ca aw lay ? Kon ñaari kurél ya [yéen ak nun], ku ci gën a yay ci am kóolute ? (waxleen) dengam xam ngeen." }
6
82
{ "fr": "Ceux qui ont cru et n´ont point troublé la pureté de leur foi par quelqu´iniquité (association), ceux-là ont la sécurité; et ce sont eux les bien-guidés\".", "wo": "Ña gëm te jaxasewuñu seen ngëm ak tooñeel, ñooña ñoo am kóolute ; te ñoom ñooy ña tegu ci njub” . " }
6
83
{ "fr": "Tel est l´argument que Nous inspirâmes à Abraham contre son peuple. Nous élevons en haut rang qui Nous voulons. Ton Seigneur est Sage et Omniscient.", "wo": "Loolu mooy Sunu lay wi nu jox Ibraahiima mu yay ca aw nitam. Dananu yékkati ku Nu neex mu kawe. Te sa Boroom Ku xereñ la, Ku xam la." }
6
84
{ "fr": "Et Nous lui avons donné Isaac et Jacob et Nous les avons guidés tous les deux. Et Noé, Nous l´avons guidé auparavant, et parmi la descendance (d´Abraham) (ou de Noé), David, Salomon, Job, Joseph, Moïse et Aaron. Et c´est ainsi que Nous récompensons les bienfaisants.", "wo": "May Nanu ko Isaaqa ak Yanqooba, gindi leen, teg leen cig njub ñoom ñépp. Ak Nooh it, gindi Nanu ko lu jiitu, ak cay sëtam, Daawuda ak Suleymaan, ak Ayuuba ak Yuusufa, ak Muusaa, ak Haaruuna. Te noonu la Nuy feyee ñay rafetal." }
6
85
{ "fr": "De même, Zacharie, Jean-Baptiste, Jésus et Elie, tous étant du nombre des gens de bien.", "wo": "Ak Zakariyaa ak Yahyaa, ak Iisaa ak Ilyaas, ñoom ñépp ca nit ñu yiw ña lañu bokk." }
6
86
{ "fr": "De même, Ismaël, Elisée, Jonas et Lot. Chacun d´eux Nous l´avons favorisé par dessus le reste du monde.", "wo": "Ak Ismaahiila ak Ilyaas, ak Yunuus, ak Lóot. Te ñoom ñépp defal Nanu leen ngëneel ci kaw waa àddina si." }
6
87
{ "fr": "De même une partie de leurs ancêtres, de leurs descendants et de leurs frères et Nous les avons choisis et guidés vers un chemin droit.", "wo": "Te ca biir seeni baay ak seeni sët ak seeni mbokk, tànn Nanu leen, jubal leen, teg leen ca yoon bu jub wa." }
6
88
{ "fr": "Telle est la direction par laquelle Allah guide qui Il veut parmi Ses serviteurs. Mais s´ils avaient donné à Allah des associés, alors, tout ce qu´ils auraient fait eût certainement été vain.", "wo": "Loolu mooy njubug Yàlla, Dana ci gindi ku Ko neex ciy jaamam. Waaye bu ñu bokkaale woon, fàwwu la ñu daan def [ci lu baax] dana yàqu." }
6
89
{ "fr": "C´est à eux Nous avons apporté le Livre, la sagesse et la prophétie. Si ces autres-là n´y croient pas, du moins Nous avons confié ces choses à des gens qui ne les nient pas.", "wo": "Ñooña ñooy ña Nu jox Téere ba ak àtte ya ak Yonent ga. Nit ña, bu ñu weddee yooyu, dana fekk dénkoon Nanu leen aw xeet wu leen weddiwul woon." }
6
90
{ "fr": "Voilà ceux qu´Allah a guidés : suis donc leur direction. Dis : \"Je ne vous demande pas pour cela de salaire\". Ce n´est qu´un rappel à l´intention de tout l´univers.", "wo": "Ñooñu la Yàlla gindi : royal seenug njub. Neel : “Laajumaleen ci ag pey” . Dafa fekk rekk ne lii moom ag fàttali la ñeel waa àddina si." }
6
91
{ "fr": "Ils n´apprécient pas Allah comme Il le mérite quand ils disent : \"Allah n´a rien fait descendre sur un humain.\" Dis : \"Qui a fait descendre le Livre que Moïse a apporté comme lumière et guide, pour les gens ? Vous le mettez en feuillets, pour en montrer une partie, tout en cachant beaucoup. Vous avez été instruits de ce que vous ne saviez pas, ni vous ni vos ancêtres. Dis : \"C´est Allah\". Et puis, laisse-les s´amuser dans leur égarement.", "wo": "Màggaluñu Yàlla kem dayo bi mu yayoo ñu màggale Ko, bu ñu waxee ne : “Yàlla wàccewul dara ci kenn.” . Neel : “Kan moo wàcce Téere bu Muusaa ànd ak leer ak njub ñeel nit ñi ? Ngeen bind ko ciy këyit di ko wone ak di ca nëbb lu bari. Te jàngaleef na leen lu ngeen xamul woon yéen ak seeni baay. Neel : “Yàlla la” . Te nga bàyyi leen ci seen cànkute ga ñuy nuur cim po.(s)" }
6
92
{ "fr": "Voici un Livre (le Coran) béni que Nous avons fait descendre, confirmant ce qui existait déjà avant lui, afin que tu avertisses la Mère des Cités (la Mecque) et les gens tout autour. Ceux qui croient au Jour dernier, y croient et demeurent assidus dans leur Salat.", "wo": "Te lii Téere la bu ñu wàcce bu barkeel, buy dëggal la ko jiitu, ak ngir nga waar waa ndeyi njéndi ya [Màkka] ak la ko wër. Ña gëm àllaaxira, danañu ko gëm te ñoom danañu sàmm seeni julli." }
6
93
{ "fr": "Et quel pire injuste que celui qui fabrique un mensonge contre Allah ou qui dit : \"Révélation m´a été faite\", quand rien ne lui a été révélé. De même celui qui dit : \"Je vais faire descendre quelque chose de semblable à ce qu´Allah a fait descendre.\" Si tu voyais les injustes lorsqu´ils seront dans les affres de la mort, et que les Anges leur tendront les mains (disant) : \"Laissez sortir vos âmes. Aujourd´hui vous allez être récompensés par le châtiment de l´humiliation pour ce que vous disiez sur Allah d´autre que la vérité et parce que vous vous détourniez orgueilleusement des Ses enseignements\".", "wo": "Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla muy wax naan : “Soloo nañu ma” , te fekk soloowuñu ko dara. Ak kuy wax naan : “Danaa wàcce lu mel ni lii Yàlla wàcce.” . Cëy boo gisoon tooñkat ya bis ba ñu nekkee ci wextanu ndee, te Malaaka ya tàllal seeni yoxo (naan leen) : “Génneleen seen bopp. Tey jii, dees na leen feye mbugal muy toroxale ci sababus la ngeen doon wax ci Yàlla te du dëgg ak la ngeen daan rëy-rëylu tey dëddu ay tegtalam” ." }
6
94
{ "fr": "Et vous voici venus à Nous, seuls, tout comme Nous vous avions créés la première fois, abandonnant derrière vos dos tout ce que Nous vous avions accordé. Nous ne vous voyons point accompagnés des intercesseurs que vous prétendiez être des associés . Il y a certainement eu rupture entre vous : ils vous ont abandonnés, ceux que vous prétendiez (être vos intercesseurs).", "wo": "(Moom Yàlla Mu ne leen) Dikk ngeen di kenn kenn ni Nu leen binde woon cig njalbéen, te bàyyi ci seen ginnaaw la ñu leen wërsëgale woon. Waaw Nun sax gisunu ña ngeen daan jaamu, di ko bokkaale ak Yàlla. Léegi seen digganteek ñoom dog na, te la ngeen doon sos réer na leen." }
6
95
{ "fr": "C´est Allah qui fendre la graine et le noyau : du mort il fait sortir le vivant, et du vivant, il fait sortir le mort. Tel est Allah. Comment donc vous laissez-vous détourner ?", "wo": "Yàlla mooy xar pepp ak i saal : [génne ca luy sax gàncax walla garab], Mooy génne luy dundu ci lu dee, tey génne lu dee ci luy dundu. Yàllaa ngoogu. Waaw naka lañu leen wëlbatee ?" }
6
96
{ "fr": "Fendeur de l´aube, Il a fait de la nuit une phase de repos; le soleil et la lune pour mesurer le temps. Voilà l´ordre conçu par le Puissant, l´Omniscient.", "wo": "Mooy sos leeraayu suba si, def guddi muy noflaay ; def jant bi ak weer wi ñuy waññikaayu jamono. Loolu mooy nattaleb Aji-not jiy Aji-xam [Yàlla].(r)" }
6
97
{ "fr": "Et c´est Lui qui vous a assigné les étoiles, pour que, par elles, vous vous guidiez dans les ténèbres de la terre et de la mer. Certes, Nous exposons les preuves pour ceux qui savent !", "wo": "Moom moo leen defal ay bidiw ngir ngeen di ca gindiku bu ngeen nekkee ci lëndëmi jéeri walla géej gi. Faramfàcce Nanu Téere ba, ngir aw nit ñuy xam !" }
6
98
{ "fr": "Et c´est Lui qui vous a créés à partir d´un personne unique (Adam). Et il y a une demeure et un lieu de dépôt (pour vous.) Nous avons exposé les preuves pour ceux qui comprennent .", "wo": "Moom moo leen sose ci benn bakkan. [Ngeen jaar] ci dekkiwaay [ci ndiggu baay] ak saxuwaay [ci biiru yaay]. Leeral Nanu sunuy kéemaan ngir aw nit ñu am dégg-dégg." }
6
99
{ "fr": "Et c´est Lui qui, du ciel, a fait descendre l´eau. Puis par elle, Nous fîmes germer toute plante, de quoi Nous fîmes sortir une verdure, d´où Nous produisîmes des grains, superposés les uns sur les autres; et du palmier, de sa spathe, des régimes de dattes qui se tendent . Et aussi les jardins de raisins, l´olive et la grenade, semblables ou différent les uns des autres. Regardez leurs fruits au moment de leur production et de leur mûrissement. Voilà bien là des signes pour ceux qui ont la foi.", "wo": "Moom mooy wàcce ndox mu jóge asamaan. Nu genne ci gàncax lu nekk, Nu génne ci loolu gàncax gu naat, ci loolu Nu génne ci ay pepp yu raŋaloo ; ak ci garabu tàndarma, ay tëggu tàndarma yu jóge ci tóor-tóor yi te jegeñ suuf. Seetluleen seeni meññent bu ñuy meññ ak bu ñuy ñor. Kéemaan guy waaree ngi noonu ci ñi gëm." }
6
100
{ "fr": "Et ils ont désigné des associés à Allah : les djinns, alors que c´est Lui qui les a créés. Et ils Lui ont inventé, dans leur ignorance. des fils et des filles, Gloire à Lui ! Il transcende tout ce qui lui attribuent.", "wo": "Te ñoom sàkkal nañu Yàlla ay bokkaale yu di ay jinne te Moo leen bind. Sosal nañu ko it ay doom yu góor ak yu jigéen, ci lu àndul ak benn xam-xam. Cëy sellam ga ak màggam ga ! Jomb Na la ñu koy nirële." }
6
101
{ "fr": "Créateur de cieux et de la terre. Comment aurait-Il un enfant, quand Il n´a pas de compagne ? C´est Lui qui a tout créé, et Il est Omniscient.", "wo": "Moo bind asamaan yi ak suuf si. Naka lay ame doom, te amul àndandoo ju jigéen ? Moo bind lu nekk, di Ku xam lu ne." }
6
102
{ "fr": "Voilà Allah, votre Seigneur ! Il n´y a de divinité que Lui, Créateur de tout. Adorez-Le donc. C´est Lui qui a chargé de tout.", "wo": "Yàllaa ngi noonu, di seen Boroom ! Yàlla ju dul Moom amul, Moom mi bind lépp lu ne. Jaamuleen ko, Mooy kiy saytu lépp." }
6
103
{ "fr": "Les regards ne peuvent l´atteindre, cependant qu´Il saisit tous les regards. Et Il est le Doux, le Parfaitement Connaisseur.", "wo": "Ay gët mënu koo gis, te Moom mën naa gis ay gët. Te Moom mooy Aji-ñeewant, di Ku deñ ciy kumpa. " }
6
104
{ "fr": "Certes, il vous est parvenu des preuves évidentes, de la part de votre Seigneur. Donc, quiconque voit clair, c´est en sa faveur; et quiconque reste aveugle, c´est à son détriment, car je ne suis nullement chargé de votre sauvegarde.", "wo": "Ay lay yu leer nàññ dikkal na leen, tukke ca seen Boroom. Ku nangoo gis, boppam la ko defal ; ku gëmm [bañ a gis], boppam lay yàqal, nekkewuma fi di leen wattu." }
6
105
{ "fr": "C´est ainsi que Nous expliquons les versets. Et afin qu´ils disent : \"Tu as étudié\". Et afin de l´exposer clairement à des gens qui savent.", "wo": "Noona Lanuy faramfàccee Sunuy àtte. Ngir ñu wax ne : “Jàng nga” . Ak ngir Nu leeral ko aw nit ñuy ràññee." }
6
106
{ "fr": "Suis ce qui t´est révélé de la part de ton Seigneur. Point de divinité autre que Lui. Et écarte-toi des associateurs.", "wo": "Nanga topp la ñu la soloo te muy lu tukkee ca sa Boroom. Kenn du Yàlla ku dul Moom. Dëddul way-bokkaale ya." }
6
107
{ "fr": "Si Allah voulait, ils ne seraient point associateurs ! Mais Nous ne t´avons pas désigné comme gardien sur eux; et tu n´es pas leur garant.", "wo": "Bu neexoon Yàlla, duñu bokkaale ! Defunu la [yaw Yonent bi] nga di leen wattu mbaa nga di leen aar." }
6
108
{ "fr": "N´injuriez pas ceux qu´ils invoquent, en dehors d´Allah, car par agressivité, ils injurieraient Allah, dans leur ignorance. De même, Nous avons enjolivé (aux yeux) de chaque communauté sa propre action. Ensuite, c´est vers leur Seigneur que sera leur retour; et Il les informera de ce qu´ils oeuvraient.", "wo": "Buleen di ŋàññ ñay jaamu leneen lu dul Yàlla, ndax kon dañuy ŋàññ Yàlla cig jalgati, ngir ñàkk a xam. Noonu Lanuy rafetale jëfi wépp xeet [ci seeni gis-gis]. Ba noppi, ñu dellu jëm ca seen Boroom; Mu leeral leen la ñu nekkoon di ko def." }
6
109
{ "fr": "Et ils jurent par Allah de toute la force de leurs serments, que s´il leur venait un miracle, ils y croiraient (sans hésiter,) Dis : \"En vérité, les miracles ne dépendent que d´Allah.\" Mais qu´est ce qui vous fait penser que quand cela (le signe) arrivera, ils n´y croiront pas ?", "wo": "Ñangay waat ci Yàlla gën gaa màggi seen ngiñ, ne bu leen kéemaan dikkaloon, kon fàwwu danañu ko gëm." }
6
110
{ "fr": "Parce qu´ils n´ont pas cru la première fois, nous détournerons leurs coeurs et leurs yeux; nous les laisserons marcher aveuglement dans leur rébellion.", "wo": "Te Dananu wëlbati seeni xol ak seeni gis-gis ca nawoon, ba ñu ko ñàkkee gëm ca njalbéen ga ; te Dananu leen bàyyi ca seenug féttéerlu ñuy tuñ-tuñi." }
6
111
{ "fr": "Et si Nous faisions descendre les Anges vers eux, [comme ils l´avaient proposé] si les morts leur parlaient, et si Nous rassemblions toute chose devant eux, ils ne croiraient que si Allah veut. Mais la plupart d´entre eux ignorent.", "wo": "Te su Nu wàcce woon ci ñoom ay Malaaka, ñu dee ña di wax ak ñoom, te Nu dajale ci ñoom lu nekk ñu jàkkaarlook ñoom, duñu gëm mukk bu neexul Yàlla. Waaye nag, la ëpp ca ñoom dañoo réer.(h)" }
6
112
{ "fr": "Ainsi, à chaque prophète avons-Nous assigné un ennemi : des diables d´entre les hommes et les djinns, qui s´inspirent trompeusement les uns aux autres des paroles enjolivées. Si ton Seigneur avait voulu, ils ne l´auraient pas fait; laisse-les donc avec ce qu´ils inventent.", "wo": "Noonu Lanu sàkkalee bépp Yonent ab noon : muy ay séytaane yu nekk nit walla jinne yuy rafetal ay wax ci ñenn ci ñoom jëme ca ñeneen ngir wor leen. Bu neexoon sa Boroom, duñu ko def ; bàyyileen ak la ñuy duur." }
6
113
{ "fr": "Et pour que les coeurs de ceux qui ne croient pas à l´au-delà se penchent vers elles , qu´ils les agréent, et qu´ils perpètrent ce qu´ils perpètrent.", "wo": "Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju jóge ca, ak ñu fàggu la ñuy fàggu [ciy bàkkaar]." }
6
114
{ "fr": "Chercherai-je un autre juge qu´Allah, alors que c´est Lui qui a fait descendre vers vous ce Livre bien exposé ? Ceux auxquels Nous avons donné le Livre savent qu´il est descendu avec la vérité venant de ton Seigneur. Ne sois donc point du nombre de ceux qui doutent.", "wo": "Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat, te Moom moo wàcce ci yéen Téere ba faramfàcce [lu ne] ? Te ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere, xam nañu ne dëgg la te mu wàcc tukkee ca sa Boroom. Kon yaw ci sa wàllu bopp, bul bokk mukk ci ñiy sikki-sàkka." }
6
115
{ "fr": "Et la parole de ton Seigneur s´est accomplie en toute vérité et équité. Nul ne peut modifier Ses paroles. Il est l´Audient, l´Omniscient.", "wo": "Sa kàddug Boroom mat na ci dëgg ak maandute. Ay waxam du soppeeku. Kuy dégg la, di Ku xam. " }
6
116
{ "fr": "Et si tu Obéis à la majorité de ceux qui sont sur la terre, ils t´égareront du sentier d´Allah : ils ne suivent que la conjecture et ne font que fabriquer des mensonges.", "wo": "Boo toppee li ëpp ci ñi nekk ci suuf si, ñu sànk la, nga sori yoonu Yàlla : ndax toppuñu lu dul ay njortu te nekkewuñu lu dul di fen." }