sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
3
112
{ "fr": "Où qu´ils se trouvent, ils sont frappés d´avilissement, à moins d´un secours providentiel d´Allah ou d´un pacte conclu avec les hommes,. Ils ont encouru la colère d´Allah, et les voilà frappés de malheur, pour n´avoir pas cru aux signes d´Allah, et assassiné injustement les prophètes, et aussi pour avoir désobéi et transgressé.", "wo": "Fu ñu mën a nekk, toroxtaange dal leen, lu dul ña ca yiiroon kóllareg Yàlla walla gu nit ña. Te ñoom merum Yàlla dal na leen, ñu daldi simbook ñàkk [ndóol] ngir weddi ga ñu weddi kàdduy Yàlla ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg, booleek moy Yàlla gi ñu saxoo woon, di jalgati." }
3
113
{ "fr": "Mais il ne sont pas tous pareils. Il est, parmi les gens du Livre, une communauté droite qui, aux heures de la nuit, récite les versets d´Allah en se prosternant.", "wo": "Waaye ñoñ-téere yemuñu de. Am na ci kurél bu taxaw [ci dëgg] buy jàng kàdduy Yàlla ya, ca waxtu ya séq guddi, te dañuy julli [sujjóot]. (r)" }
3
114
{ "fr": "Ils croient en Allah et au Jour dernier, ordonnent le convenable, interdisent le blâmable et concourent aux bonnes oeuvres. Ceux-là sont parmi les gens de bien.", "wo": "Gëm nañu Yàlla ak Bis-pénc ba, te dañuy digle njekk, di tere njekkar, di jëkkante ci def lu baax. Ñooña ca ñu yiw ña lañu bokk." }
3
115
{ "fr": "Et quelque bien qu´ils fassent, il ne leur sera pas dénié. Car Allah connaît bien les pieux.", "wo": "Lu ngeen jëf ci aw yiw, kenn duleen ko xañ. Yàlla xam na ña ko ragal ." }
3
116
{ "fr": "Quant à ceux qui ne croient pas, ni leurs biens, ni leurs enfants ne pourront jamais leur servir contre la punition d´Allah. Et ce sont les gens du Feu : ils y demeureront éternellement.", "wo": "Ña weddi, seeni alal ak seeni doom duñuleen jariñ dara fa Yàlla. Ñoom ñooy waa Safara te dañu fay béel." }
3
117
{ "fr": "Ce qu´ils dépensent dans la vie présente ressemble à un vent glacial qui s´abat sur un champ appartenant à des gens qui se sont lésés eux-mêmes, et le détruit. Car ce n´est pas Allah qui leur cause du mal, mais ils se font du mal à eux-mêmes.", "wo": "La ñuy joxe ci seeni alal ci mbiri àdduna dafa mel ni ngelaw lu ànd ak safara dal ci kaw mbeyum ña tooñ seen bopp, ne ko fuuf lakk ko. Yàlla tooñuleen waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp." }
3
118
{ "fr": "ô les croyants, ne prenez pas de confidents en dehors de vous-mêmes : ils ne failliront pas à vous bouleverser. ils souhaiteraient que vous soyez en difficulté. La haine certes s´est manifestée dans leur bouches, mais ce que leurs poitrines cachent est encore plus énorme. Voilà que Nous vous exposons les signes. Si vous pouviez raisonner !", "wo": "Yéen ñi gëm, buleen won seen mbir ci ag xaritoo keneen ku bokkul ci yéen. Bumuy ci ñoo xam ne dañuy kàttanlu ci yàqal leen, danañu ngéeju ngir ngeen am coono. Mbañeel ga feen na ca seeni wax, te la seeni xol ëmb moo yéesati. Yéen leeral nanu leen kéemaan yi [ngeen war leen a ràññee ndegam ñu xel-lu ngeen ! ]." }
3
119
{ "fr": "Vous, (Musulmans) vous les aimez, alors qu´ils ne vous aiment pas; et vous avez foi dans le Livre tout entier. Et lorsqu´ils vous rencontrent, ils disent \"Nous croyons\"; et une fois seuls, de rage contre vous, ils se mordent les bouts des doigts. Dis : \"mourrez de votre rage\"; en vérité, Allah connaît fort bien le contenu des coeurs.", "wo": "Yéen ak ñoom, yëgleen ne yéen a leen safoo, waaye ñoom safoowuñu leen ; te yéen gëm ngeen Téere bi lépp. Bu ñu dajee ak yéen ne “Gëm nanu” ; bu ñu wéyee màtt seeni waaroom wiccax ndax mer. Neel : “Deeleen ci mer” ; Yàlla ku xam la lu nekk ci xol yi." }
3
120
{ "fr": "Qu´un bien vous touche, ils s´en affligent. Qu´un mal vous atteigne, ils s´en réjouissent. Mais si vous êtes endurants et pieux, leur manigance ne vous causera aucun mal. Allah connaît parfaitement tout ce qu´ils font.", "wo": "Bu ngeen amee bànneex, mu naqari leen. Bu ngeen amee naqar, mu di seen bànneex ñoom. Waaye bu ngeen muñee te ragal Yàlla, seen pexe yi duleen wàññi dara. Te Yàlla ku peeg la la ñuy def." }
3
121
{ "fr": "Lorsqu´un matin, tu (Muhammad) quittas ta famille, pour assigner aux croyants les postes de combat et Allah est Audient et Omniscient.", "wo": "Fàttalikul yaw Yonent bi, ba nga xëyee jóge ci sa njaboot, di tegtal jullit ña barabu xeexukaay ya, xamal ne Yàlla kuy dégg la, Kuy xam la.(s)" }
3
122
{ "fr": "Quand deux de vos groupes songèrent à fléchir ! Alors qu´Allah est leur allié à tous deux ! Car, c´est en Allah que les croyants doivent placer leur confiance .", "wo": "[Fàttalikul] ba ñaari kurél ci yéen naree yoqat ! Te Moo leen dimbali woon ba delluwuñu ginnaaw ! Way-gëm ña, nañu sukkandiku ci Yàlla [Uhud]." }
3
123
{ "fr": "Allah vous a donné la victoire, à Badr, alors que vous étiez humiliés. Craignez Allah donc. Afin que vous soyez reconnaissants !", "wo": "Yàlla dimbali woon na leen ca Badar, ba ngeen nekkee ñu néewle. Ragal-leen Yàlla ndax amaana ngeen gërëm ko !" }
3
124
{ "fr": "(Allah vous a bien donné la victoire) lorsque tu disais aux croyants; \"Ne vous suffit-il pas que votre Seigneur vous fasse descendre en aide trois milliers d´Anges\" ?", "wo": "[Fàttalikul yaw Yonent bi] ba nga waxee ña gëm : “Moo ndax doyuleen, seen Boroom, tëbb leen ñetti junni Malaaka yu wàcc [ngir dimbali leen]” ?" }
3
125
{ "fr": "Mais oui ! Si vous êtes endurants et pieux, et qu´ils [les ennemis] vous assaillent immédiatement, votre Seigneur vous enverra en renfort cinq mille Anges marqués distinctement .", "wo": "Axakañ ! Bu ngeen muñee te ragal Yàlla, bu ñu leen songee ak doole [ca waxtu wu ñu tànn], seen Boroom dana leen tëbb juróomi junniy Malaaka yuñu màndargaal." }
3
126
{ "fr": "Et Allah ne le fit que (pour vous annoncer) une bonne nouvelle, et pour que vos coeurs s´en rassurent. La victoire ne peut venir que d´Allah, le Puissant, le Sage;", "wo": "Te Yàlla defewuko lu dul bégal leen ngir seeni xel dal. Te ndimbal du bawoo fu dul fa Yàlla, Mooy Ki not, di Ku xereñ ki ;" }
3
127
{ "fr": "pour anéantir une partie des mécréants ou pour les humilier (par la défaite) et qu´ils en retournent donc déçus . -", "wo": "def na ko it ngir dog ab kurél walla toroxal leen, ba ñu wëlbatiku di ñu yàkkiku [seen yaakaar tas]." }
3
128
{ "fr": "Tu n´as (Muhammad) aucune part dans l´ordre (divin) - qu´Il (Allah) accepte leur repentir (en embrassant l´Islam) ou qu´Il les châtie, car ils sont bien des injustes.", "wo": "[Yaw Yonent bi], mbir moomu moomoo ci dara - Yàlla Moo leen di jéggal walla Mu mbugal leen, ñoom daal ay tooñkat lañu." }
3
129
{ "fr": "A Allah appartient tout ce qui est dans les cieux et sur la terre. Il pardonne à qui Il veut, et Il châtie qui Il veut.... Et Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Te Yàlla Moo moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Mooy jéggal ku ko soob, di mbugal ku ko soob.... Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
3
130
{ "fr": "ô les croyants ! Ne pratiquez pas l´usure en multipliant démesurément votre capital. Et craignez Allah afin que vous réussissez !", "wo": "Éy yéen ñi gëm, buleen lekk ribaa ju jóge ci alal juy léw-léwi di fulu. Nangeen ragal Yàlla ndax ngeen texe !" }
3
131
{ "fr": "Et craignez le Feu préparé pour les mécréants.", "wo": "Nangeen ragal Safara sa ñuy xaaroo yéefar ya." }
3
132
{ "fr": "Et obéissez à Allah et au Messager afin qu´il vous soit fait miséricorde !", "wo": "Nangeen topp [ndigali Yàlla] ak Yonent bi ndax ngeen doon ñu ñuy yërëm! " }
3
133
{ "fr": "Et concourez au pardon de votre Seigneur, et à un Jardin (paradis) large comme les cieux et la terre, préparé pour les pieux,", "wo": "Jëkkanteleen jëm ci seen njéggalug Boroom ak ci Àjjana joo xam ne yaatu na ni asamaan yi ak suuf si, te ña ragal Yàlla lañu koy xaaroo,(n)" }
3
134
{ "fr": "qui dépensent dans l´aisance et dans l´adversité, qui dominent leur rage et pardonnent à autrui - car Allah aime les bienfaisants -", "wo": "ñoom ña nga xam ne dañuy joxe [seen alal ci jamonoy naataange ak ci jamonoy tar-tar ], ak ñay nëbbu seen mer, ak ñay jéggal nit ñi [ay tooñeel] - Yàlla safoo na ñay rafetal -" }
3
135
{ "fr": "et pour ceux qui, s´ils ont commis quelque turpitude ou causé quelque préjudice à leurs propres âmes (en désobéissant à Allah), se souviennent d´Allah et demandent pardon pour leur péchés - et qui est-ce qui pardonne les péchés sinon Allah ? - et qui ne persistent pas sciemment dans le mal qu´ils ont fait.", "wo": "ak ña nga xam ne, bu ñu defee ñaawtéef mbaa ñu tooñ seen bopp, daldi fàttaliku Yàlla fa saa sa, daldi jéggalu seen bàkkaar ya - te Yàlla rekk ay jéggale bàkkaar - te ñooña duñu nuur mukk ci jëfe bàkkaar te fekk ñu xam ko." }
3
136
{ "fr": "Ceux-là ont pour récompense le pardon de leur Seigneur, ainsi que les Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour y demeurer éternellement. Comme est beau le salaire de ceux qui font le bien !", "wo": "Ñooña seenug pey moo di jéggal gu bawoo ca seen Boroom, ak Àjjana yu dex ya di daw ci seen ron, te dañu fay béel. Loolu ag pey dàqatuko !" }
3
137
{ "fr": "Avant vous, certes, beaucoup d´événements se sont passés. Or, parcourez la terre, et voyez ce qu´il est advenu de ceux qui traitaient (les prophètes) de menteurs.", "wo": "Am na ay yoon yu jàll yu ñu sosoon ba ngeen dikkagul. Kon doxleen wër ci goxi suuf, te di xool naka la ña daan weddi mujje." }
3
138
{ "fr": "Voilà un exposé pour les gens, un guide, et une exhortation pour les pieux.", "wo": "Lii ag leeral la ci nit ñi, te di ag njub ak ug waare ngir ñi ragal Yàlla." }
3
139
{ "fr": "Ne vous laissez pas battre, ne vous affligez pas alors que vous êtes les supérieurs, si vous êtes de vrais croyants.", "wo": "Buleen doyadi, buleen ragal, yéen ay féete kaw ndegam gëm ngeen." }
3
140
{ "fr": "Si une blessure vous atteint, pareille blessure atteint aussi l´ennemi. Ainsi faisons-Nous alterner les jours (bons et mauvais) parmi les gens, afin qu´Allah reconnaisse ceux qui ont cru, et qu´Il choisisse parmi vous des martyrs - et Allah n´aime pas les injustes.", "wo": "Su fekkee metit dal na leen, wu na mel daloon na yéefar yi. Bis yooya [Bisi naqar] danu leen di ay-ayle ci nit ñi ak itam ngir Yàlla xàmmee ñi gëm, te dana sàkk ci ñi dee ci xare, te bokk ci yéen, ay chuhadaa - Yàlla du safoo tooñkat ya." }
3
141
{ "fr": "et afin qu´Allah purifie ceux qui ont cru, et anéantisse les mécréants.", "wo": "Loola Yàlla dakoy defe ngir laabal ñi gëm, di ci lakk yéefar ya." }
3
142
{ "fr": "Comptez-vous entrer au Paradis sans qu´Allah ne distingue parmi vous ceux qui luttent et qui sont endurants ?", "wo": "Moo ndax dangeen a defe ne dangeen duggu Àjjana te Yàlla duleen nattu ba ràññee ña xeexal diine, ràññee it muñkat yi ?" }
3
143
{ "fr": "Bien sûr, vous souhaitiez la mort avant de la rencontrer. Or vous l´avez vue, certes, tandis que vous regardiez !", "wo": "Mebetoon ngeen dey lu jiitu ngeen dajeek Moom. Léegi ndax gis ngeen ko, ne ci jàkk !" }
3
144
{ "fr": "Muhammad n´est qu´un messager - des messagers avant lui sont passés - S´il mourait, donc, ou s´il était tué, retourneriez-vous sur vos talons ? Quiconque retourne sur ses talons ne nuira en rien à Allah; et Allah récompensera bientôt les reconnaissants.", "wo": "Muhammad doonul lu may ab Yonent - boo xam ne ay Yonent ñoo ko jiitu woon ba jàll - Ndax bu deewoon walla ñu rey ko, dangeen di dellu ca seeni tànk, weddi ? Ku walbatiku ca ay tànkam, du wàññi Yàlla dara ; te Yàlla dana fey ñay gëram seen Boroom.(s)" }
3
145
{ "fr": "Personne ne peut mourir que par la permission d´Allah, et au moment prédéterminé. Quiconque veut la récompense d´ici-bas, Nous lui en donnons. Quiconque veut la récompense de l´au-delà, Nous lui en donnons et Nous récompenserons bientôt les reconnaissants.", "wo": "Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci ab dig bu am àpp. Ku bëgg xéewali àddina, Dananu ko jox. Ku bëgg xéewali àllaaxira Dananu ko jox te Dananu fey [Nun Yàlla] ñiy gëram." }
3
146
{ "fr": "Combien de prophètes ont combattu, en compagnie de beaucoup de disciples, ceux-ci ne fléchirent pas à cause de ce qui les atteignit dans le sentier d´Allah. Ils ne faiblirent pas et ils ne cédèrent point. Et Allah aime les endurants.", "wo": "Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak mbooloo mu bari, te doyadiwuñu ca la leen dal ci sàmm diiney Yàlla. Yoqatuñu, nekkuñu ñu xeebu. Yàlla safoo na muñkat yi. " }
3
147
{ "fr": "Et ils n´eurent que cette parole : \"Seigneur, pardonne-nous nos péchés ainsi que nos excès dans nos comportements, affermis nos pas et donne-nous la victoire sur les gens mécréants\".", "wo": "Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar” ." }
3
148
{ "fr": "Allah, donc, leur donna la récompense d´ici-bas, ainsi que la belle récompense de l´au-delà. Et Allah aime les gens bienfaisants.", "wo": "Yàlla yoole leen àddina [xéewal] ak gën jaa rafeti yoolub àllaaxira. Yàlla safoo na ñay rafetal." }
3
149
{ "fr": "ô les croyants ! Si vous obéissez à ceux qui ne croient pas, il vous feront retourner en arrière. Et vous reviendrez perdants.", "wo": "Éy yéen ñi gëm!, bu ngeen toppee ñi weddi, danañu leen dugal sa seeni tànk [weddiloo leen], ngeen wëlbatiku ñàkk." }
3
150
{ "fr": "Mais c´est Allah votre Maître. Il est meilleur des secoureurs.", "wo": "Li wér mooy Yàllaa leen méngoo [yore seeni mbir] te Mooy ngëm ji kuy dimbali." }
3
151
{ "fr": "Nous allons jeter l´effroi dans les coeurs des mécréants. Car ils ont associé à Allah (des idoles) sans aucune preuve descendue de Sa part. Le Feu sera leur refuge. Quel mauvais séjour que celui des injustes !", "wo": "Dananu sànni ci xoli ñi weddi tiitaange ngir la ñu bokkaale Yàlla ak loo xam ne amul lay wuñu leen ca wàcceel. Safaraa di seen dëkkuwaay te dëkkuwaayu tooñkat ya bon na !" }
3
152
{ "fr": "Et certes, Allah a tenu Sa promesse envers vous, quand par Sa permission vous les tuiez sans relâche, jusqu´au moment où vous avez fléchi, où vous vous êtes disputés à propos de l´ordre donné, et vous avez désobéi après qu´Il vous eut montré (la victoire) que vous aimez ! Il en était parmi vous qui désiraient la vie d´ici bas et il en était parmi vous qui désiraient l´au-delà. Puis Il vous a fait reculer devant eux, afin de vous éprouver. Et certes Il vous a pardonné. Et Allah est Détenteur de la grâce envers les croyants .", "wo": "Yàlla def na la Mu leen digoon nekk dëgg, ba ngën di xeex ak ñoom ci ndigal, [ngeen not] ba ba ngeen sàqi ndigal la, ginnaaw ba ngeen janoo ak la ngeen bëgg [alal] àddina! Am na it ci yéen ñu bëgg [alali] àllaaxira. Ba noppi Yàlla wëlbati leen [soppi tooñeel ga] ngeen amoon ci ñoom, ngir nattu leen.Waaye baal na leen. Yàlla Boroom ngëneel la yu muy [sédd] ñi gëm." }
3
153
{ "fr": "(Rappelez-vous) quand vous fuyiez sans vous retourner vers personne, cependant que, derrière vous, le Messager vous appelait. Alors Il vous infligea angoisse sur angoisse, afin que vous n´ayez pas de chagrin pour ce qui vous a échappé ni pour les revers que vous avez subis. Et Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "[Fàttalikuleen] ba ngeen di yéeg te geesuwuleen kenn, te Yonent bi di leen woo ci seen ginnaaw. Mu tegoon leen njàqare ya ci kaw njàqare ya, ndax ngeen bañ a mitteetlu la leen rëcc walla la leen dal. Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.(r)" }
3
154
{ "fr": "Puis Il fit descendre sur vous, après l´angoisse, la tranquillité, un sommeil qui enveloppa une partie d´entre vous, tandis qu´une autre partie était soucieuse pour elle-même et avait des pensées sur Allah non conformes à la vérité, des pensées dignes de l´époque de l´Ignorance. - Ils disaient : \"Est-ce que nous avons une part dans cette affaire ? \" Dis : \"L´affaire toute entière est à Allah.\" Ce qu´ils ne te révèlent pas, ils le cachent en eux-mêmes : \"Si nous avions eu un choix quelconque dans cette affaire, disent-ils, Nous n´aurions pas été tués ici.\" Dis : \"Eussiez-vous été dans vos maisons, ceux pour qui la mort était décrétée seraient sortis pour l´endroit où la mort les attendait. Ceci afin qu´Allah éprouve ce que vous avez dans vos poitrines, et qu´Il purifie ce que vous avez dans vos coeurs. Et Allah connaît ce qu´il y a dans les coeurs .", "wo": "Wàcce na ginnaaw njàqare la, kóolute, muy gëmméntu gu muur ab kurél ci yéen [way- gëm ñi] te beneen kurél ba [naaféq ya] seen bopp rekk yitteel leen, ñu njortu ci Yàlla lu dul dëgg njortu ku réer. -Ñu naan : “Ndax mbir mi moom nanu ci dara [ba di ci reyante] ?” . Neel [Yaw Yonent bi]: “Mbirum Yàllaa.” . Ña nga nëbb ci seen biir lu ñu feeñalul, di wax naan : “Bu nu moomoon dara ci mbir mi kon duñu nu rey fii.” Tontuleen ne : “Bu ngeen toogoon ca seeni kër, ñañu dogal dee ci ñoom dana leen fekk ca seen kaw i lal. [Lii lépp am na] ngir Yàlla natt li nekk ci seeni dënn [xol], ak feeñal li nekk ci seeni xol. Te Yàlla ku xam la li nekk ci dënn yi." }
3
155
{ "fr": "Ceux d´entre vous qui ont tourné le dos, le jour où les deux armées se rencontrèrent, c´est seulement le Diable qui les a fait broncher, à cause d´une partie de leurs (mauvaises) actions. Mais, certes, Allah leur a pardonné. Car vraiment Allah est Pardonneur et indulgent !", "wo": "Ña dëddu [bañ a xeex], Seytaane tarxiisloo na leen ngir lenni bàkkaar ya ñu fàggu woon. Waaye, Yàlla jéggal na leen. Yàlla Jéggalaakoon la, Ku lewet la ! " }
3
156
{ "fr": "ô les croyants ! Ne soyez pas comme ces mécréants qui dirent à propos de leurs frères partis en voyage ou pour combattre : \"S´ils étaient chez nous, ils ne seraient pas morts, et ils n´auraient pas été tués.\" Allah en fit un sujet de regret dans leurs coeurs. C´est Allah qui donne la vie et la mort. Et Allah observe bien ce que vous faites.", "wo": "Yéen ñi gëm ! Buleen mel ni ña weddi, di wax seeni mbokk ya nekk ci tukki walla ci xare [te dee ca] : “Bu ñu toogoon ci nun, duñu dee walla duñuleen rey.” . Yàlla def wax jooju di rëccu ci seeni xol. Te Yàlla Mooy dundal, Mooy rey. Te Yàllaa ngi ne jàkk li ngeen di def, di leen gis." }
3
157
{ "fr": "Et si vous êtes tués dans le sentier d´Allah ou si vous mourez, un pardon de la part d´Allah et une miséricorde valent mieux que ce qu´ils amassent.", "wo": "Bu ñu leen reyee ci yoonu Yàlla walla ngeen dee, ca dëgg-dëgg jéggalu ga, Yàlla ak yërmandeem moo gën fuuf li ngeen di dajale." }
3
158
{ "fr": "Que vous mouriez ou que vous soyez tués, c´est vers Allah que vous serez rassemblés.", "wo": "Ngeen dee walla ñu rey leen, dees na leen pang [gur-gur] jëme ca Yàlla." }
3
159
{ "fr": "C´est par quelque miséricorde de la part d´Allah que tu (Muhammad) as été si doux envers eux ! Mais si tu étais rude, au cœur dur, ils se seraient enfuis de ton entourage. Pardonne-leur donc, et implore pour eux le pardon (d´Allah). Et consulte-les à propos des affaires; puis une fois que tu t´es décidé, confie-toi donc à Allah, Allah aime, en vérité, ceux qui Lui font confiance.", "wo": "Ci sa yërmaandeey Boroom nga nooyee ci ñoom ! Boo nekkoon ku ñaaw jikko walla ku xat xol, ñu ne wuseet bàyyi la. Baal-leen te jéggal-leen. Te deel diisook ñoom ci mbir yi ; waaye boo dogoo [ci wéyal dara], nanga wéeru ci sa Boroom, Yàlla dana safoo ñay wéeru ci Moom [yaw Muhammad]." }
3
160
{ "fr": "Si Allah vous donne Son secours, nul ne peut vous vaincre. S´Il vous abandonne, qui donc après Lui vous donnera secours ? C´est Allah que les croyants doivent faire confiance.", "wo": "Bu leen Yàlla dimbalee, kenn duleen mën a not. Bu leen bàyyee, kan moo leen di mën a dimbali ? [Amul]. Ñi gëm, nañu wéeru ci Yàlla.(s)" }
3
161
{ "fr": "Un prophète n´est pas quelqu´un à s´approprier du butin. Quiconque s´en approprie, viendra avec ce qu´il se sera approprié le Jour de la Résurrection . Alors, à chaque individu on rétribuera pleinement ce qu´il aura acquis. Et ils ne seront point lésés.", "wo": "Amul benn Yonent buy labax alali xare. Te képp ku sàcc alali xare, bu Bis-pénc baa, dana ko indi. Ku nekk door a jot la mu jëfoon ba mu mat sëkk." }
3
162
{ "fr": "Est-ce que celui qui se conforme à l´agrément d´Allah ressemble à celui qui encourt le courroux d´Allah ? Son refuge sera l´Enfer; et quelle mauvaise destination !", "wo": "Ndax kuy topp ngërëmul Yàlla, dana yem ak ku sóobu ci xarabug Yàlla ? Safaraa di këram te googu muj, du gu ñuy taamu !" }
3
163
{ "fr": "Ils ont des grades (différents) auprès d´Allah et Allah observe bien ce qu´ils font.", "wo": "Xam na ne duñu yem mukk waay. Ëppante nañu daraja [dayo] ca Yàlla, ndax Yàllaa ngi ne jàkk ca la ñuy jëf." }
3
164
{ "fr": "Allah a très certainement fait une faveur aux croyants lorsqu´Il a envoyé chez eux un messager de parmi eux-mêmes, qui leur récite. Ses versets, les purifie et leur enseigne le Livre et la Sagesse, bien qu´ils fussent auparavant dans un égarement évident.", "wo": "Yàlla xéewale na ña gëm ba Mu yónnee ca ñoom ab Yonent bu bokk ca ñoom, di leen jàngal kàddoom, di leen laabal, di leen xamal Téere ba ak xam-xamu xereñe, te la ko jiitu ñu nekkoon ci réer gu tar." }
3
165
{ "fr": "Quoi ! Quand un malheur vous atteint - mais vous en avez jadis infligé le double - vous dites \"D´où vient cela ? \" Réponds-leur : \"Il vient de vous mêmes\". Certes Allah est Omnipotent.", "wo": "Naka mu ? Bu leen aw tiis dalee - te fekk daan ngeen [seeni noon] lu mat ñaari yoon - ngeen di wax naan “Naka la lii mën a nekkee ?” . Neel : “Ci yéen la” . Yàlla mën na lu ne." }
3
166
{ "fr": "Et tout ce que vous avez subi, le jour où les deux troupes se rencontrèrent , c´est par permission d´Allah, et afin qu´Il distingue les croyants.", "wo": "La leen dalool ca seenub dajeeb ñaari mbooloo ya, lu Yàlla nammoon la ngir mu xàmmee ca ña gëm [xareb Uhud]" }
3
167
{ "fr": "et qu´Il distingue les hypocrites. on avait dit à ceux-ci : \"Venez combattre dans le sentier d´Allah, ou repoussez [l´ennemi]\" , ils dirent : \"Bien sûr que nous vous suivrions si nous étions sûrs qu´il y aurait une guerre\" Ils étaient, ce jour-là, plus près de la mécréance que de la foi. Ils disaient de leurs bouches ce qui n´était pas dans leurs coeurs. Et Allah sait fort bien ce qu´ils cachaient.", "wo": "ak ngir mu ràññee naaféq ya. Waxees na leen ne : “Kaayleen xeex [xare] ci yoonu Yàlla, walla ngeen feg [noon ya]” , ñu toontu ne : “Su nu mënoon xeex, dananu leen topp” . Ñoom, ca bis boobu, kéefar lañu gën a jege ci ngëm. Dañuy wax ca seeni gimiñ lu nekkul ca seeni xol. Te Yàllaa gën a xam lu ñuy nëbb. " }
3
168
{ "fr": "Ceux qui sont restés dans leurs foyers dirent à leurs frères : \"S´ils nous avaient obéi, ils n´auraient pas été tués.\" Dis : \"écartez donc de vous la mort, si vous êtes véridiques\".", "wo": "Ña toog bañ a xareji tey wax seeni mbokk : “Su ngeen nu déggaloon, dungeen xareji.” . Neeleen : “Jiñleen dee mu bañ a agsi ci seeni bakkan ndeem ñu dëggu ngeen” ." }
3
169
{ "fr": "Ne pense pas que ceux qui ont été tués dans le sentier d´Allah, soient morts. Au contraire, ils sont vivants, auprès de leur Seigneur, bien pourvus", "wo": "Bul foog ne ñañu reyee ci yoonu Yàlla, ñu dee lañu. Déet, ñuy dundu lañu ca seen Boroom, nekk ci xéewal" }
3
170
{ "fr": "et joyeux de la faveur qu´Allah leur a accordée, et ravis que ceux qui sont restés derrière eux et ne les ont pas encore rejoints, ne connaîtront aucune crainte et ne seront point affligés.", "wo": "dañuy bég ca la leen Yàlla jox ci ay ngënéelam, di bég it ca jullit ya ñu bàyyi ginnaaw te fekkeeguñu leen, duñu jàq, duñu am naqar bu ñu fa eggee." }
3
171
{ "fr": "Ils sont ravis d´un bienfait d´Allah et d´une faveur, et du fait qu´Allah ne laisse pas perdre la récompense des croyants.", "wo": "Danañu bég ca xéewal ya bawoo fa Yàlla ak i ngënéelam, ak ca la nga xam ne Yàlla du sànk peyub ñi gëm.(h)" }
3
172
{ "fr": "Ceux qui, quoiqu´atteints de blessure, répondirent à l´appel d´Allah et du Messager, il y aura une énorme récompense pour ceux d´entre eux qui ont agi en bien et pratiqué la piété .", "wo": "Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba leen jam- jam ya [ca xare Uhud] dalee, ña doon rafetal ca ñoom te ragal Yàlla, am nañu pey gu màgg." }
3
173
{ "fr": "Certes ceux auxquels l´on disait : \"Les gens se sont rassemblés contre vous; craignez-les\" - cela accrut leur foi - et ils dirent : \"Allah nous suffit; Il est notre meilleur garant\".", "wo": "Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog, waaye nit ñaa [seeni noon] ngi daje ngir sànk leen, war ngeen a tiit” - faf loolu yokk leen ngëm - ñu toontu ne : “Yàlla doy nanu te Mooy ngën gi wéeruwaay” ." }
3
174
{ "fr": "Ils revinrent donc avec un bienfait de la part d´Allah et une grâce. Nul mal ne les toucha et ils suivirent ce qui satisfait Allah. Et Allah est Détenteur d´une grâce immense.", "wo": "Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu bon daluleen, topp nañu lu neex Yàlla. Te Yàlla boroom ngëneel yu màgg la." }
3
175
{ "fr": "C´est le Diable qui vous fait peur de ses adhérents. N´ayez donc pas peur d´eux. Mais ayez peur de Moi, si vous êtes croyants.", "wo": "[Xupp googu ñu leen di xupp] du dara lu dul jëfi Seytaane dafay tiitloo aw nitam. Buleen leen ragal. Ragal-leen Ma, ndeem ñu gëm ngeen." }
3
176
{ "fr": "N´aie (ô Muhammad) aucun chagrin pour ceux qui se jettent rapidement dans la mécréance. En vérité, ils ne nuiront en rien à Allah. Allah tient à ne leur assigner aucune part de biens dans l´au-delà. Et pour eux il y aura un énorme châtiment.", "wo": "Ñay njëkkante di tàbbi cig weddi, bumu la naqari. Duñu wàññi Yàlla dara. Yàlla dafa bañ rekk ñu am cër ca àllaaxira. Te am fa mbugal mu rëy." }
3
177
{ "fr": "Ceux qui auront troqué la croyance contre la mécréance ne nuiront en rien à Allah. Et pour eux un châtiment douloureux.", "wo": "Ñiy weccee ngëm ak kéefar, duñu wàññi Yàlla dara. Te am nañu mbugal mu metti." }
3
178
{ "fr": "Que ceux qui n´ont pas cru ne comptent pas que ce délai que Nous leur accordons soit à leur avantage. Si Nous leur accordons un délai, c´est seulement pour qu´ils augmentent leurs péchés. Et pour eux un châtiment avilissant.", "wo": "Ña weddi, buñu foog ne la ñu leen yéex a mbugal lu baax la ci ñoom. Danu leen di yeexe ngir ñu dolliku bàkkaar doŋŋ te danañu am mbugalum toroxtaange." }
3
179
{ "fr": "Allah n´est point tel qu´Il laisse les croyants dans l´état où vous êtes jusqu´à ce qu´Il distingue le mauvais du bon. Et Allah n´est point tel qu´il vous dévoile l´Inconnaissable. Mais Allah choisit par Ses messagers qui Il veut. Croyez donc en Allah et en Ses messagers. Et si vous avez la foi et la piété, vous aurez alors une récompense énorme.", "wo": "Yàlla du bàyyi ñi gëm ci li ngeen nekk ba kerook ba Muy téqale ku bon ka ak ku baax ka. Te it Yàlla duleen xamal kumpa. Waaye Yàlla dana tànn ku ko soob ciy Yonentam [xamal ko kumpa]. Gëmleen Yàlla ak i Yonentam. Su ngeen gëmee te ragal Yàlla, dangeen am pey gu màgg. " }
3
180
{ "fr": "Que ceux qui gardent avec avarice ce qu´Allah leur donne par Sa grâce ne comptent point cela comme bon pour eux. Au contraire, c´est mauvais pour eux : au Jour de la Résurrection, on leur attachera autour du cou de qu´ils ont gardé avec avarice . C´est Allah qui a l´héritage des cieux et de la terre. Et Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Ña nay a [joxe] ca la leen Yàlla may ciy ngënéelam, buñu foog ne lu baax la ci ñoom. Déet ! lu bon la ci ñoom : [la ñu nayoon ci joxe ko] danañu leen ko wékkal ci seeni loos Bis-pénc ba. Yàllaa moom donoy asamaan yeek suuf si. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def." }
3
181
{ "fr": "Allah a certainement entendu la parole de ceux qui ont dit : \"Allah est pauvre et nous somme riches\". Nous enregistrons leur parole, ainsi que leur meurtre, sans droit, des prophètes. Et Nous leur dirons : \"Goûtez au châtiment de la fournaise.", "wo": "Yàlla dégg na waxi ña naan : “Yàlla ku ñàkk la te nun danoo woomal” . [Nun Yàlla] dananu bind la Nu wax, ak rey ga ñu rey Yonent ya ci lu dul dëgg. Te dananu leen wax : “Toqamtikuleen mbugal muy lakke. (s)" }
3
182
{ "fr": "Cela, à cause de ce que vos mains ont accompli (antérieurement) ! \" Car Allah ne fait point de tort aux serviteurs.", "wo": "Loolu, ngir la seeni yoxo jëf [ci lu bon] !” . Te Yàlla du tooñ jaamam ña." }
3
183
{ "fr": "Ceux-là mêmes qui ont dit : \"Vraiment Allah nous a enjoint de ne pas croire en un messager tant qu´Il ne nous a pas apporté une offrande que le feu consume\". - Dis : \"Des messagers avant moi vous sont, certes, venus avec des preuves, et avec ce que vous avez dit [demandé]. Pourquoi donc les avez-vous tués, si vous êtes véridiques\" ?", "wo": "Yàlla dégg na ña wax ne : “Yàlla kóllarante na ak nun, te ne duñu gëm benn Yonent li feek indilunu yool boo xam ne safaraa koy lekk” . - Neel : “ Ay Yonent dikkaloon na leen jiitu ma, indiwaale woon lay yu leer nàññ ak la ngeen laaj. Su fekkee ñu dëggu ngeen, lu tax ngeen rey leen” ?" }
3
184
{ "fr": "S´ils te (Muhammad) traitent de menteur; des prophètes avant toi, ont certes été traités de menteurs. Ils étaient venus avec les preuves claires, les Psaumes et le Livre lumineux.", "wo": "Suñu la weddee, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu. Indi woon nañu ay lay yu leer ak [Zabuur] ak Téere bu leer." }
3
185
{ "fr": "Toute âme goûtera la mort. Mais c´est seulement au Jour de la Résurrection que vous recevrez votre entière rétribution. Quiconque donc est écarté du Feu et introduit au Paradis, a certes réussi. Et la vie présente n´est qu´un objet de jouissance trompeuse.", "wo": "Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot seen pey ca Bis-pénc ba. Ku ñu soreel Safara ba, dugal ko Àjjana, texe na. Te dundug àddina gi du dara lu dul xéewal guy naxe [naxti ndaw]." }
3
186
{ "fr": "Certes vous serez éprouvés dans vos biens et vos personnes; et certes vous entendrez de la part de ceux à qui le Livre a été donné avant vous, et de la part des Associateurs, beaucoup de propos désagréables. Mais si vous êtes endurants et pieux... voilà bien la meilleure résolution à prendre.", "wo": "Fàwwu dees na leen nattu ci seeni alal ak ci seeni bakkan ; dangeen dégge ca ñoñ-téere ya leen jiitu woon ak bokkaalekat ya, wax yu ñaaw yu bari.Waaye, bu ngeen muñee te ragal Yàlla... mooy sabab duggu gay tax mbir ya sotti.(r)" }
3
187
{ "fr": "Allah prit, de ceux auxquels le Livre était donné, cet engagement : \"Exposez-le, certes, aux gens et ne le cachez pas\". Mais ils l´ont jeté derrière leur dos et l´ont vendu à vil prix. Quel mauvais commerce ils ont fait !", "wo": "[Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen ko leeralal nit ñi te buleen ko nëbb” . Ñu sànni ko ca seen ginnaaw, jaaye ko njëg gu néew. Ndax njëg gu bon !" }
3
188
{ "fr": "Ne pense point que ceux-là qui exultent de ce qu´ils ont fait, et qui aiment qu´on les loue pour ce qu´ils n´ont pas fait, ne pense point donc, qu´ils trouvent une échappatoire au châtiment. Pour eux, il y aura un châtiment douloureux !", "wo": "Bul foog ne ñay bég ca la ñu def, te bëgg ku leen tëgg ci lu ñu deful, buleen foog mukk ne danañu mucc ci mbugal. Déedéet, mbugal mu metti lañuy am !" }
3
189
{ "fr": "A Allah appartient le royaume des cieux et de la terre. Et Allah est Omnipotent.", "wo": "Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na lu ne." }
3
190
{ "fr": "En vérité, dans la création des cieux et de la terre, et dans l´alternance de la nuit et du jour, il y a certes des signes pour les doués d´intelligence,", "wo": "Sàkk gi Yàlla sàkk asamaan yeek suuf si, ak ni guddi gi ak bëccëg gi di jëlasantee, ay kéemaan yu rëy a ngi ci ñeel woroom xel ya," }
3
191
{ "fr": "qui, debout, assis, couchés sur leurs côtés, invoquent Allah et méditent sur la création des cieux et de la terre (disant) : \" Notre Seigneur ! Tu n´as pas créé cela en vain. Gloire à Toi ! Garde-nous du châtiment du Feu.", "wo": "[Woroom xel yooyu gëm], ñooy ñay tuddu Yàlla, bu ñu toogee ak bu ñu taxawee, ak bu ñu tëddee, tey xalaat ci sàkkug asamaan yeek suuf si, [di wax naan] : “Yaw sunu Boroom ! Sàkkuloo lii ci neen. Tuddu naa sag sell ! Yal na nga nu fegal mbugalum Safara." }
3
192
{ "fr": "Seigneur ! Quiconque Tu fais entrer dans le Feu, Tu le couvres vraiment d´ignominie. Et pour les injustes, il n´y a pas de secoureurs !", "wo": "Yaw sunu Boroom ! Koo tàbbal Safara, gàcceel nga ko de. Te tooñkat ya, duñu am ndimbal !" }
3
193
{ "fr": "Seigneur ! Nous avons entendu l´appel de celui qui a appelé ainsi à la foi : \"Croyez en votre Seigneur\" et dès lors nous avons cru. Seigneur, pardonne-nous nos péchés, efface de nous nos méfaits, et place nous, à notre mort, avec les gens de bien.", "wo": "Yaw sunu Boroom ! Nun dey dégg nanu kuy woote naan : “Gëmleen seen Boroom” , nu daldi gëm. Yaw sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar, te soppil nu sunuy ñaawtéef mu di aw yiw, te boo nuy rey, nga boole nu ak gaa yu baax ya." }
3
194
{ "fr": "Seigneur ! Donne-nous ce que Tu nous a promis par Tes messagers. Et ne nous couvre pas d´ignominie au Jour de la Résurrection. Car Toi, Tu ne manques pas à Ta promesse\".", "wo": "Yaw sunu Boroom ! yal nanga nu jox la nga nu digoon, te jaarale woon ko ca sa Yonent ya. Te bul nu gàcceel kera Bis-pénc ba. Yaw Yàlla, doo wuute ab dige de” ." }
3
195
{ "fr": "Leur Seigneur les a alors exaucés (disant) : \" En vérité, Je ne laisse pas perdre le bien que quiconque parmi vous a fait, homme ou femme, car vous êtes les uns des autres. Ceux donc qui ont émigré, qui ont été expulsés de leurs demeures, qui ont été persécutés dans Mon chemin, qui ont combattu, qui ont été tués, Je tiendrai certes pour expiées leurs mauvaises actions, et les ferai entrer dans les Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, comme récompense de la part d´Allah.\" Quant à Allah, c´est auprès de Lui qu´est la plus belle récompense.", "wo": "Yàlla seen Boroom nungul na leen seeni jëf, ne : “ Man de, duma sànk jëfi ab jëfkat ci neen, moo xam góor la mbaa muy jigéen. Moo xam ñi leen beru walla ñu lor leen ci yoonu Yàlla, ñu reye ñu rey leen. Gaa ñooña Dananu leen soppil seeni ñaawtéef aw yiw te Danaa leen dëkkal Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ca seen ron, muy yool bu bawoo fa Yàlla.” . Te Yàllaa rafet ab yool." }
3
196
{ "fr": "Que ne t´abuse point la versatilité [pour la prospérité] dans le pays, de ceux qui sont infidèles.", "wo": "Alal ju bari ja yéefar yi di wëlbati ci réew yi, bumu la nax." }
3
197
{ "fr": "Piètre jouissance ! Puis leur refuge sera l´Enfer. Et quelle détestable couche !", "wo": "Xéewal yu néew la ! Topp seenug delluwaay di Safara. Ndaw delluwaay bu ñaaw !(s)" }
3
198
{ "fr": "Mais quant à ceux qui craignent leur Seigneur, ils auront des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour y demeurer éternellement, un lieu d´accueil de la part d´Allah. Et ce qu´il y a auprès d´Allah est meilleur, pour les pieux.", "wo": "Waaye ña ragal seen Boroom, am nañu Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ca seen ron, ñu béel fa, muy seen wàccuwaay fa Yàlla. Te la nekk fa Yàlla mooy dàqal ñu baax ña." }
3
199
{ "fr": "Il y a certes, parmi les gens du Livre ceux qui croient en Allah et en ce qu´on a fait descendre vers vous et en ceux qu´on a fait descendre vers eux . Ils sont humbles envers Allah, et ne vendent point les versets d´Allah à vil prix. Voilà ceux dont la récompense est auprès de leur Seigneur. en vérité, Allah est prompt à faire les comptes.", "wo": "Am na ci ña jot Téere, ñu gëm Yàlla ak la ñu wàcce ci yéen, ak la ñu wàcce ca ñoom. Dañuy toroxlul Yàlla, duñu jaay laayay Yàlla ci njëg gu néew. Ñooña am nañu seenug pey fa Yàlla te Yàlla ku gaaw la ci waññ [jëfi nit ñi]." }
3
200
{ "fr": "ô les croyants ! Soyez endurants. Incitez-vous à l´endurance. Luttez constamment (contre l´ennemi) et craignez Allah, afin que vous réussissiez !", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Nangeen di muñ ci bànneex, nangeen di muñ it [ci aw naqar]. Te itam nangeen di fagaru, te itam ragal-leen Yàlla ndax Yàlla ngeen texe ! " }
4
1
{ "fr": "ô hommes ! Craignez votre Seigneur qui vous a créés d´un seul être, et a créé de celui-ci sont épouse , et qui de ces deux là a fait répandre (sur la terre) beaucoup d´hommes et de femmes. Craignez Allah au nom duquel vous vous implorez les uns les autres, et craignez de rompre les liens du sang. Certes Allah vous observe parfaitement.", "wo": "Éy yéen nit ni ! Ragal-leen Yàlla mi leen sàkk ci benn bakkan, sàkke itam soxnaam sa, njërtal ci aw góor ak jigéen ñu bari. Ragal-leen Yàlla ji ngeen di laajante, ak ug dog mbokk. Yàlla nag ku leen di fuglu la." }
4
2
{ "fr": "Et donnez aux orphelins leurs biens; n´y substituez pas le mauvais au bon . Ne mangez pas leurs biens avec les vôtres : c´est vraiment un grand péché.", "wo": "Te ngeen jox jirim yi seeni alal ; te buleen wecce lu baax [ca la ñu moom] joxe lu bon la. Buleen lekk la ñu am ci alal di ko booleek seeni alal : ndax loolu bàkkaar bu rëy la." }
4
3
{ "fr": "Et si vous craignez de n´être pas justes envers les orphelins, ...Il est permis d´épouser deux, trois ou quatre, parmi les femmes qui vous plaisent, mais, si vous craignez de n´être pas justes avec celles-ci, alors une seule, ou des esclaves que vous possédez. Cela afin de ne pas faire d´injustice (ou afin de ne pas aggraver votre charge de famille).", "wo": "Su ngeen ragale bañ a maandu [ci seen jëflante ak jirim yi]..., mën ngeen takk lu leen neex te soob leen ciw jigéen, ñaar-ñaar, ñett ñett, ak ñeent ñeent, waaye, bu ngeen ragale ci ne dungeen maandu [ñàkk a yemale soxna ya], kon takkleen benn soxna walla sax ngeen jël benn jigéen [jaam bu jigéen]. Ndax loolu moo gën a jege maandute." }
4
4
{ "fr": "Et donnez aux épouses leur mahr , de bonne grâce. Si de bon gré elles vous en abandonnent quelque chose, disposez-en alors à votre aise et de bon cœur.", "wo": "Nangeen jox jigéen ñi seen can mu dig may. Bu ñu leen ca yéwénalee dara te may leen ca dara te mu di ci teeyu bakkan, lekkleen ko na mu leen neexe." }
4
5
{ "fr": "Et ne confiez pas aux incapables vos biens dont Allah a fait votre subsistance. Mais prélevez-en, pour eux , nourriture et vêtement; et parlez-leur convenablement.", "wo": "Te ña seeni xel matadi, buleen joxandoo seen alal jépp ja Yàlla def ngeen di ko sàmm. Nangeen leen cay mosal [kem seeni soxla]. Deeleen ca wutal aw dund [lu ñu sol ci yére] ; te ngeen di wax ak ñoom ci njekk." }
4
6
{ "fr": "Et éprouvez (la capacité) des orphelins jusqu´à ce qu´ils atteignent (l´aptitude) au mariage; et si vous ressentez en eux une bonne conduite, remettez-leur leurs biens. Ne les utilisez pas (dans votre intérêt) avec gaspillage et dissipation, avant qu´ils ne grandissent. Quiconque est aisé devrait s´abstenir de se payer lui-même de cet héritage qui lui est confié. S´il est pauvre, alors qu´il y puise une quantité convenable, à titre de rémunération de tuteur.) est aisé, qu´il s´abstienne d´en prendre lui-même. S´il est pauvre, alors qu´il en utilise raisonnablement : et lorsque vous leur remettez leurs biens, prenez des témoins à leur encontre. Mais Allah suffit pour observer et compter.", "wo": "Nangeen di dayu jirim ba ñuy mat a séy ; su ngeen nemmekoo ci ñoom njub, joxleen leen seen alal. Buleen ko lekk, yàqte ko, di ko pasar- pasaree te fekk màggaguñu. Ku ca yore te woomal, na fegu . Ku ca yore te néew doole, na ca lekke nu jaadu : su ngeen leen di delloo seeni alal, nangeen wut seede. Yàlla doy na, mat sëkk ab waññikat.(n)" }
4
7
{ "fr": "Aux hommes revient une part de ce qu´ont laissé les père et mère ainsi que les proches; et aux femmes une part de ce qu´ont laissé les père et mère ainsi que les proches, que ce soit peu ou beaucoup : une part fixée.", "wo": "Góor ñi am nañu cër ci la seen ñaari waajur ak seeni jigeñaale bàyyee ginnaaw ; jigéen ñi it am nañu cër ci la seen ñaari waajur ak seeni jigeñaale bàyyee ginnaaw, mu néew walla mu bari : cër boobu lu ñu farataal la. [Ndonu]" }
4
8
{ "fr": "Et lorsque les proches parents, les orphelins, les nécessiteux assistent au partage, offrez-leur quelque chose de l´héritage, et parlez-leur convenablement.", "wo": "Bu ay mbokk fekkee séddale ba, ak i jirim walla way-ñàkk, nangeen leen ca jox, te wax ak ñoon waxi njekk [ju rafet]. " }
4
9
{ "fr": "Que la crainte saisisse ceux qui laisseraient après eux une descendance faible , et qui seraient inquiets à leur sujet; qu´ils redoutent donc Allah et qu´ils prononcent des paroles justes.", "wo": "War nañoo tiit ña nga xam ne bu ñu bàyyi woon seen ginnaaw njaboot gu sew, danañu am njàqare ci ñoom ; nañu ragal Yàlla [ci alali jirim] te nañu wax wax ju jub." }
4
10
{ "fr": "Ceux qui mangent [disposent] injustement des biens des orphelins ne font que manger du feu dans leurs ventres. Ils brûleront bientôt dans les flammes de l´Enfer.", "wo": "Ña nga xam ne dañuy lekk alali jirim ci ag tooñ, nañu xam ne seeni biir yooyu lekkuñu ca lu dul safara. Te dees na leen séndal ca Safara." }
4
11
{ "fr": "Voici ce qu´Allah vous enjoint au sujet de vos enfants : au fils, une part équivalente à celle de deux filles. S´il n´y a que des filles, même plus de deux, à elles alors deux tiers de ce que le défunt laisse. Et s´il n´y en a qu´une, à elle alors la moitié. Quant aux père et mère du défunt, à chacun d´eux le sixième de ce qu´il laisse, s´il a un enfant. S´il n´a pas d´enfant et que ses père et mère héritent de lui, à sa mère alors le tiers. Mais s´il a des frères, à la mère alors le sixième, après exécution du testament qu´il aurait fait ou paiement d´une dette. De vos ascendants ou descendants, vous ne savez pas qui est plus près de vous en utilité. Ceci est un ordre obligatoire de la part d´Allah, car Allah est, certes, Omniscient et Sage .", "wo": "Yàllaa ngi leen di dénku ci seeni doom ne : ku góor, cëram na toll ni cëru ñaari jigéen. Ñoom jigéen ña, bu ñu ëppee ñaar, te amuñu mag walla rakk ju góor, seen cër day nekk ñaari ñetteeli alal ja. Bu dee kenn ku jigéen doŋŋ nag, cëram day nekk genn-wàllu alal ja. Ñaari waajur nag ñoom, ku ca nekk ay am juróom-benneel la seen doom bàyyi. Bu amut doom ju góor, ay waajuram rekk a koy donn, yaayam day jot ñetteelu alal ja, baay ba jot ñaari netteel ya des. Bu amee rakk walla mag ju góor, yaayam juróom-benneelu alal ja lay jël, ginnaaw ba ñu génnee ndénkaan ya mu dénkaane woon walla bor ya. Seeni baay ak seeni doom, xamuleen kan moo leen ci ëppal njariñ. Ndigal luy farata la, bawoo fa Yàlla, te Yàlla ku xam la, Ku xereñ la.(s)" }